Séeréer

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Seereer)

Séeréer (mba Seereer) genn giir la gu nekk Senegaal. Siin ak Saalum ñooy seen i nguur. Ci lim ñooy ñatteelu xeet ci Senegaal ginnaaw wolof ak pël, juróom benn saa-senegaal yii jël kenn ka séeréer la, ñenn ci séeréer si diñu leen fekk Gàmbi ak Muritani. Xeetu séeréer bokk na ci xeet yi gën a yagg te féete Senegàmbi.

Maad a Sinig Ama Juuf Njeelane Faye Juuf 1850 (aquarelle de l'abbé Boilat dans Esquisses sénégalaises, 1853)

Soog a nekk Siin-saalum, ca Tekuruur lañu nekkoon. Dañoo gàddaay dem Siin-Saalum ndax dañu doon daw Lislaam ak Muraabituun yi (les Almoravides). Muraabituun yi dañu xare "jiyaar" ak séeréer si, ngir dugal leen ci Lislaam, waaye séeréér si bëgguñu woon loolu. Lii lépp nag ca yoonu imbraatóor gu Gana la xewe woon, booba imbraatoor gi mi ngi doon tàmbalee daanu. Foofa ca Siin-Saalum ay Soose (Sooninke), ñoo fi doon dëkk. Kon mbokkug Soose ak Séeréer ci dëkkandoo la bawoo, ba noppi Soose yu bari dem nanu dëkki ca Kaasamaas. Séeréer si dañu doon séddale dëkk bi ci ay Lamana, ca Lamana yépp ay Laman a fa fa daa nekk ay buur. Mbay ak Napp lañu daa dunde. Mbay (Saalum) moo doon turu dëkk bi soog a nekk Siin ak Saalum. Ba noppi ay Mandinke yu juge nguuru Kaabu, ñëw ca Séeréer sa, dëkk ak ñoom. Mandinke yi ay Nanko (Géer) yu Kabbu lañu woon, seeni buur (Mansa ca làkku Mandinke) ñoo leen dàqe seen réew. Joolaa yi ñoo leen ne ca Siin-Saalum baax na lépp lu nit soxla ngir man a dund am na fa, te foofu am na ay nit waaye amuñu buuru dëgg. Lii moo tax ñu tuxoo Siin ak Saalum. Nanko ak Buuri Séeréer si fi nekkoon (Laman) dañoo booloo, jaxasoo, ba nekk xeet wu ñuy wax ay Gelawaar. Gelawaar, ñoo tabax nguuru Siin ak Saalum. Maysa Waali Joon moo jëkk a nekk buuru Siin. Mbegaan Nduur moo jëkk a nekk Buuru Saalum.

Nosteg mboolaay ga (le système social) nii la tëdde woon:

  • Gelawaar yi ñoo neekkoon Buur yi.
  • Jàmbur yi ak Baadoola yi ñoo ci toppoon cig raŋ.
  • Tëgg yi (Tafax ca seeni làkk), Lawbe yi ñooy seeni Seen, Wuudé yi (Pal), Ràbbkat yi (Tiriw).
  • Jaam yi, Ceddo bokk nañu ci jaam yi.

Séeréer ci seen bopp, am nañu: Séeréer yu Njominka, Siin rekk lañu nekk, nappkat lañu it, turi maandinke lañu yor, ndax ca gelawaar lañu bokk. Séeréer Ndut, Saefen, Paloor, Noon, ñoom Séeréeru Kajoor ak Bawal lañu. Séeréeru Siin, mooy Séeréeru Siin-Saalum. Séeréeru Fuuta yi nag, leegi ca tukuloor ya lañu bokk, ñoom ñoo fa doon ay wolof tamit, Kuballo yi (nappkatu tukuloor) ak Sebbe ( ceddo tukuloor ). Séeréer ak Pël ñoo njëkk a nekk foofu, loolu moo tax mu am fa ay Séeréer. Tukuloor ak Séeréer dañuy kalante ak Joolaa tam. Ndax ca cosaan, nee nanu, xeet yooyu yépp ñoo bokk mam. Séeréer si dañoo xaw a ñuul, njool, am it yaram wu dëgër. Ci Senegaal ñooy ñi fi dàq a bëre.

Léopold Sédar Senghor, njiitul Senegaal lu njëkk séeréer la woon ca baayam, Abdu Juuf tam. Blees Jaañ moom it baayam Séereer la woon. Séereer bu njëkk Ceddo lañu nekkoon - diiney "A ƭat Roog" ci baati Séeréer. Tay nag dugg nañu lislaam ( Tiijaaniya, yoonu murit), walla diiney nasaraan (christianisme) ca Siin (Joal-Fadiouth). Nasaraanalkat yi (le Missionnaires) yu tubaab yi ñoo leen dugal ci diine jooju. Am na Séeréer ñu barry ñu tey ci diiney A ƭat Roog (religion sérère). Roog moi Yalla ci baati Séeréer.

Seen Sant yi gën a siiw : Juuf, Ngom, Fay, Seen, Saar, Seŋoor, Nduur, Joon, Joor, Jongu, Jeey, Njaay, Sekk, Ndong, Séy, Luum, Tin, Déen, Puy, Caw, Maróon, Ñing, Jóob, Gaajo.