Sawat
Apparence
Sawat gi ci njabootug Combretaceae la bokk. Bari na lool ca màndiŋ yu Senegaal, Gànnaar, Niseeriya ba Ecoopi ak Ugandaa.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab gu neewi xob la, gàjj la guy àgg 1 ba 3i met. Xasam day ñuul bu garab gi gone, buy mag nag day baam.
Njariñ li
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Soloom siiw na wàllu faj ci Afrig gu soww, reenam day faj mettitu biir, xobam dees koy baxal ngir faj febaaru sawukaay.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Xobi garabug sawat
-
Tóor-tóorub garabug sawat
-
Meññeefi garabug sawat