Aller au contenu

Séng

Jóge Wikipedia.
Garabug séng

Séng di Acacia raddiana garab la gu fekk baax ca weti saara dees na ko fekk it ca réewi gànnaar. Garab gi nag day yékkatiku ba ca kaw door a mbaar foofu ay xobam. Peer bi day jóg, taawu ay wànqaas yu téen, door a baar foofu ay xob yu rankaloo mu mel ni am mbaar.

Tóortóor yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Tóortóor yi nag, dañuy dajaloo di focc def ay dank yu ndaw yu weex te mel ni lu mboq. 

Foytéefam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Foytéefam nag, nit du ko faral di lekk waaye mala yi bëgg nañu ko lool. 

Njariñ yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Séng dees na ko jëmbat ngir xeex ag tàkk (deseer). Bépp bërëb bees ragal tàkk gi agsi fa, bees fa jëmbatee ay séng moo gën a gaaw ci kar tàkk ga ba du fa yegsi. Ndax moom daa man a muñ am ndox lool, te itam ci suuf yu dëgër yi la ëpp lu miy sax, rawatina suufu Afrig yi jege Saara. 

Njëfëndaay li

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Séng dees ciy defar diw, ak asib, te asib boobu di bawoo ci séng baax na ci jabet, te itam day wàccee yéegug dereet gu ëpp ci yaram. Séng daal lu am solo ci réewi Afrig yi féete Saara. Bantam it dees koy jëfandikoo lu bari. 

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
Acacia raddiana