Aller au contenu

Rap

Jóge Wikipedia.

Rap xeetu woy la, bokk ci yëngu-yëngub caada bii di hip-hop tambali ci ndoorteelu ati 1970 ca Réew yi Bennoo yi, ci biir askanu waa-aamerig yu ñuul yi . Am na ñu ne aji-rap bii di Joe Tex moo sos baat bi. Ci njëlbeen MC yi,(masters of ceremony, njiitu xew mi)liggéeyam moo doonoon jàppale DJ bi, wàll wi ñu doon rap la ñu doon woowee MCing. break dancing, DJing, MCing ak graffiti yi, ñooy ñenti ponku yi caaday hip-hop dàttu.

Rap niki lépp lu bokk ci caadaay hip-hop dafa ëmb lu bari: xew, fo, ñaxtu... Seeni mbind, ak seeni kàddu dañuy soppiku topp jamono. Mbind yi dañuy wax ci li nit ñi di dund bés bu ne: politig, koom, diine, mbëgéel,...

Bari nañ gangoori rap yu seeni mbidd fees aki ñaxtu, ay kaas. Li gëna fés ci seeni mbind, te yenn saa yi ñakk-kersa lool, ñi ngi leen jëmale ci way-politig yi, takk-der yi, yoon,... Ci Senegaal rap teel na fee àggsi, ci njëlbeenu ati 1980 la waa-senegaal yi tambalee xam aji-rap yu mag niki gangoor bii di Public Enemy, Africa bambata,...

Ñenn ñi dañ koy tekke niki tënku baati waa-angalteer yii di rhythm and poetry walla rock against police. Ci ndoorteelul ati fanweer yi, waa-aamerig yu ñuul yi nekkoon nañ ci ñakk gu tar, loolu juroon ñakk-kaaraage, rayante, ay xeex ci diggante kureeli defkati ñaawteef yi, njaayum lu bon, añs. Ci dundin gu tar gii la ndaw yi tambalee fippu, jël rap def ngannaay ak yoon ngir fésal seen mer, ak seen nekkin gu tar. Lii moo tax li ëpp ci seeni mbind day yor jëmmu kaaskat, ñaxtukat jëmale ci takk-der yi, way-politig yi, njiiti yoon yi,...

Taariixu rap dafa séddaliku ci ay jamono: Rap Old school (1970-1985), di ndoorteel gi, ba ciRap Golden Age (1985-1993), di jamono ji rap tambalee am doole dëgg, ci la East-Coast (tefesu penku) ak West-coast (tefesu sowwu)juddu. Ci jamono jii la yeneen xeeti rap yii di gangsta rap ak G-funk juddu ca West Coast. Ci 1993 ba tay rap Hardcore, bling-bling, underground, añs, ñoo fi juddu.

Old school (daara ju yàgg ja)

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Rap a ngi juddoon ci yeneen xeeti woy yii di funk, gospel, soul, blues, rawatina talking blues. Mi ngi juddu ci ati 1970 ca Bronx, di ab gox-goxaanub New York, di barab ba gangoor ba tuddoon Organization te gëna siiw ci Zulu Nation. Li ëppoon ci seeni wax ci aadaay Afrig ak Jamayka la doon jóge.

Kon ci ati 1970, ci xewi mbedd yi la nit ñu nel ne DJ Kool Herc tambalee taqale xeeti woy yu mel funk, soul, R&B, disco music. Ñu tambali di leen tek ci mbedd yi, ci xew, géej, dañ ko jàppe woon fo, bégal seen bopp ànd ak seen dj. Bi xeetu woy wi tambalee am ciiwte, lañ tudde woykat bi MC (Master of ceremonies). Li MC bi doon def sax man nañ kaa baña tudde woy ndax da doon wax ci biir woy wi dj bi tegg, ci wàll yi amul wax, doonoo wax ju neex, loolu dem bañ tudde ko "rapping". Doonul woon lun ñu man def ciy tappaan di leen jaay, ndax ay waxantu lañ woon rekk, yu ñu doon xalaat ci jamono ji ñu ko doon waxe.

Ci 1979 la tappaan bi ñeel bii xeetu woy njëkk a génn: ""Rapper's Delight"" bu Sugharhill Gang. Aji-rap mooy kiy def rap, ci wolof, waaye ci kàllaama waa-angalteer "rapper" la ñuy wax kiy def "rapping", baat baa ngi juddu ci woy woowu.

Génneeb Sugharhill Gang bi amoon na solo lool ci ciiwteeg xeetu woy wu bees wi, di laal mbooloo mu bari, yemul woon rekk New York, di fa mu juddoo, waaye réew mi yépp la mujje laal.

Ci ati juroom-ñett yi la Rap tambali bari melo, di màgg ci yeeneen melokaan yu gëna fasu. Ci jenn jamono ji, yeneen feem yu xereñ gis-bés, lu mel ne scratching.

Golden Age (ati wurus)

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Laataa jamono jii, xeetu rapin bi fi nekkoo dafa dattu woon ci breaks ak Woyu mbëjfeppalwoyu mbëjfeppal. Ñëwug waa Run-DMC soppi lépp: seen feem kàttanu woon na te metti, ñoo ci tambaalee dugal ay jumtukaay yu bees, ay riff yu xalam, yàggul dara ñu nekk ay royuwaay. Waa Run-DMC ñoo ubbi buntu ati wurusu rap, mujj doon gangooru rap bi njëkka àgg ci collu àddunay woy, amoon ciiwte gu jéggi-dayoo te wéy di màgg. Ci nii rap bi tas ci àdduna yépp ni ab pënd

Rap Gaalsene

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci Senegaal rap teel na fee àggsi, ci ndoorteelu ati juroom-ñett yi la gangoor yi njëkk juddu. MC Lida mooy ki njëkka génne ab tappaanu rap, tuddoon Duma doyal mukku mooy aji-rap bi njëkk ci Senegaal. PBS tegu ci ag génneem boobu di Ataaya. Rapu Senegaal ci at yooyu waxi mbëggéel moo ci gënoona fés, ci 1998 rap Gaalsene am jekkiku gu am solo, beneen xeetu rapin feeñ, rap underground. Waa Rap-adio ñoo indi feemu rapin bu bees bi Senegaal, doonoon rap ñaxtu, seenug ñëw yokk rap doole, daanaka li ëpp ci yeneen aji-rap yi ñëw ci seen ginnaaw yépp rapin boobu lañu jël.Tay gangoori rap yu Senegaal xayma nañ leen ci lu tollook 2500.