Omar Blondin Diop

Jóge Wikipedia.


Omar Blondin Diop, mu ngi juddu fukki fan ak juroom-ñett ci weeru septàmbar atum 1946 ci Ñaame, faatu ci kaso ci dun bu Gorée ci Senegaal fukki fan ak benn ci weeru mee atum 1973, nitu xam-xam la, di jàmbaar ak way-pólótig bu Senegaal. Way-bokk la woon ci yengu-yengu bu weeru mee atum 68 ca Farãas te doon na jàmbaar ci yengu'engu-yëngu yi amoon ginnaaw juróom-benn-fukki at ak juróom-ñett te doon xeex njiitu Senegaal Léopold Sédar Senghor.

Dundu ak jaar-jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bolondeŋ Jóob a ngi gane àdduna ci sancug Farãs (colonie française) gii di Niseer (Niger) ci atum 1946. Baayam doonoon ab fajkat (médecin) di saa-afrig, ñu jële woon ko Ndakaaru mi doonoonjooja jamono gëblag (la capitale) doxaluwaayu (l’administration) Afrig soowu jant gu Farãs (AOF),yóbbu ko Dooso, gox bu ndaw bu nekk ca Ñaame (Niamey). Doonte sax ay xalaatam ci politigjëmmalu ko woon mu jëm ci xeex nooteel gi, kilifay nootaakon yi dañoo amoon ci moom njort luñaaw ne dafa bañoon Farãs. Li gën a yokk loolu mooy limu jàppaloon tànk lefu (l’aile) kuréel gidajale liggéeykati àdduna bi yépp. Tiitànge gi mu amoon ci ni yëngu yëngu yi jëm ci bañ nooteel digënee am doole ginnaaw bi ñu jógee ci ñaareelu xareb àdduna bi yépp (deuxième guerre mondiale), moo waraloon Farãs doon bàyyi xel bu baax ñi mu tudde woon “ñi bañ Farãs” (les anti-français). Bi ñu bàyyee seen waa kër ñu ñibbisi Senegaal, Bolondeŋ ag ngoneem (son enfance) Ndakaaru lako gën a defee. Bi mu amee 14i at ci la dem toog Farãs, baayam wéyal fa am njàngam ci wàllu paj[1]

Daanaka ati 1960 yépp Bolondeŋ mu ngi woon Farãs. Foofa ca Pari, mu doon fa wéyal am njàngamci wàllu mbind ak di xóotal xam-xamam ci xeltukati tugal (philosophes occidentaux) yu mag yi, melne Aristod (Aristote) ak Kànt, ba ci Éegal (Hegel) au Rusóo (Rousseau). Bi muy dugg Lekool Normaal Supeeryëer[2] yemoo ak mu tàmbalee teew ca jotaayi ñiy xeex ba sax di wàlli ca béj (débats)ya ca féete càmmoñ (la gauche) doon amal. Jamono la ju kuréel yi doon xeex koppartu (capitalisme)gi doon roy ci jàllarbi ci wàllu mbatiit (révolution culturelle) ca Siin (Chine) ba noppi di ŋàññ(dénoncer) xareb Amerig ba dugg Wiyetnaam (la présence de l’armée américaine au Vietnam). Dongoy Afrig yi (les étudiants africains) ca Farãs, tolloon ci limub 10i junni ci atum 1968, seentaxawaay mu ngi gënoon a jëm ci xeex ngir seen réew ak ngir bennoog Afrig (unité africaine).Bolondeŋ moom tegoon benn tànk ci ñaari wàll yépp. Diir bu gàtt ginnaaw bi mu déggee waxibañkatu saa-senegaal bi, filmokat (cinéaste) bii di Sãa Lik Godaar tabb (choisir) ko mu bokk cifilmoom bi tuddu “Saa-siin bu jigéen bi” ci 1967[3].

Mbind ak xalaati Espinosaa (Spinoza), Maks(Marx), Fanon, yëbbee (déteignent) ci moom, Bolondeŋ doon saxal am njaxas ci wàllu xam-xam yi- boole aju-ci-tër-gi, dàq lépp luy gàllankoor ag péexte, xalaati Maawo (Mao) ak bu Torotskii(Trotsky). Xalaatam ci politig mu tanke woon ko ci yoonu gis-gis yu bari, booleek wéy di jàngàdduna bi ak gëti boppam[4]

Ay yëngu-yëngoom ci wàllu politig tax ñu dàqe Bolondeŋ Jóob Farãs yóbbu ko mu ñibbi Senegaalci njeextalu atum 1969. Moom ak yeneen mbokk-mbaar (camarades) yu jànge Tugal (Europe) ñubokk ci yënguy ndawi saa-Maks-ak-Lenin yi (les marxistes-léninistes) te benn pàcc ba ca daggee jurTaxaw xeex nooteel “Ànd Jëf”. Bolondeŋ Jóob dàq lootaabewin (structurations) yu tëju yi, jiitaljéegoy pasin (démarches artistiques) yi jaare ko ci taxawal sémbub (projet) “tiyaatar yuy am cimbedd mi tey wax nit ñi li leen soxal”. Muy lu ànd loolu ak “Tiyaataru ñi ñu not” bu Ógustoo Bóol.Bi mi seetloo pasin mi (l’art) ak li mu mën a jàppee ci jàllarbi gi (la révolution), Bolondeŋ Jóob daaldi bind ne : “Balaa ñuy def tiyaatar ci ab gox, fàww ñu xam njëkk ña fa dëkk, jaxasoo ak ñoom, rawatina ndawña [...]. Sunu tiyaatar bi dina dem fépp fu nit ñi di dajaloo (ja (marchés) yi, senemaa (cinémas) yi,estaad (stades) yi) [...]. Fexe ba jox wëppa (thème) wu ne, tër (contexte) gu ne, aji-jëmmal (l’acteur)ju ne, màndargay Afrig. [...] Rawatina di defar lépp lu nu mën a defaral sunu bopp [...]. Ci tënk : deewaaye dunu nangu tàbbi ci njaam”.

Biñu nee Senegaal moom na boppam tamit, loolu ciy wax rekk la yem. Seŋoor àndul woon ci réewmi génn ci nooteel ci saa si. Limu bëggoon mooy ñu ciy dem ndànk ndànk ci diirub 20i at. Ba taxna bimu jiitee réew mi mu saxoon di sàkku ndimbalul Farãs. Ci atum 1962, Seŋoor gaawtu taqalàndandoom bu yàgg bi di Mamadu Ja mi jiitewoon jëwriñ yi, jiiñ ko ne da doon daaneel nguuram.Loolu jur ñu teg Mamadu Ja loxo, tëj ko lu ëpp 10i ati kaso. Ci atum 1968, ci seleŋlu gu daj réewmépp (grève générale), alkaati yi dal ci kaw seleŋlukat yi (les grévistes) ci ndimbalul sóobarey (lessoldats de) Farãs yi[5]. Diggante Seŋoor ak Farãs gën a sori loolu ci atum 1971, ci posem (occasion) ngan gu njiitu réewum Farãs di Sors Pompidu, di xaritam teg ci bokkoon ak moom fañuy jàngee,doon amal ci Senegaal. Lu mat at Ndakaaru nekk di waajal ngan gu gàtt googu yamoon ci benn bisdong. Fi gan geek ñimu àndal waroon a jaar yépp, kilifa yi dañoo defaraat yoon yi, yeesalaat taax yindax bëgg a làkk lépp luy màndargaal ag ñàkk ci gëbla gi (la capitale).

Ndaw ñu bari jàpp nag ne lu ëpp tuuru, dalal giñu dalal njiitu réewum Farãs ab cokkaas (uneprovocation) la bu leer. Ay ayu-bis lu jiitu loolu, gàngoor guy roy kureélug Balaak Pànteer guAmerig, ak geneen gu tudd Tupaamoros ca réewum Uruggey, ànd taal Këru mbatiit gu Farãs (centreculturel français) ci Ndakaaru. Biñuy amal ngan gi, xale yi jéem a dal ci daamari njiitu réewum Farãsyi, waaye ñu teg ñenn ci ndaw ñi loxo[6].

Ñaari rakki Omar Bolondeŋ Jóob bokkoon ca. Moom tamitboobu ab xeexin la gëmoon, muy dóor mu daanu, waaye bokkulwoon ci song moomu. Fekk na ayweer lu jiitu loolu mu delluwoon Farãs ginnaw biñu teggee dogal bi ko dàkkewoon ca réew ma. Ciyëngu-yëngu yooyu ci la Bolondeŋ ànd ak yenn ciy xaritam ne dañuy dem jàngi nu ñuy xeexee akay ngànnaay. Noonu ñu dugg ci saxaar gii di “l’Orient-Express”, wër Tugal gi yépp, mujjee ci dalubay saa-siri (syriens) fekk fa ay fippuy Palestin ak Eritëre (Érythrée). Seen pexe moo doon gëf(kidnapper) farayaŋas (l’ambassadeur) bu réewum Farãs weccee ko ak seen mbokki-mbaar (leurscamarades) yi ñu tëj kaso. Biñu fa defee ñaari weer ci la Bolondeŋ Jóob ak ay àndandoom jóge citàkk (le désert) gi dellu taax. Amoon nag yaakaar ci ndimbalu Balaak Pànteer yi ubbiwoon ab dal caAlse (Alger), gëblag réewum Alseri[7]. Waaye fàntasiroo (conflit) gu am ci kuréel gi tax ñu soppidoxalin. Ginnaaw biñu defee diir bu gàtt ci Konaakiri (Conakry) ñu jóg wutali Bamako gi lenn cimbokki Bolondeŋ dëkk. Foofa ñu lootaabewu (réorganiser) waat.

Alkaati yi teg loxo gàngoor gépp (toute la bande) ci jeexitalu weeru nowàmbar ci atum 1971, fan yunéew bi Seŋoor di waaja amal nganam gu njëkk ca réew ma ginnaaw bi tasug Lëkktoo gu Mali(Fédération du Mali) ci atum 1960. Raji (les renseignements généraux) Mali yi Ceekoro Bagayokojiite ñoo leen toppoon raju (espionner) leen ay weer[8] .

Ñu fekk ci gafag (sac) Bolondeŋ bataaxal butënk pexe yi mbokki-mbaaram (ses camarades) yi wara rëccee ci kaso ba ñu leen tëj. Biñu kojébbalee Senegaal, ñu tëj ko ràpp ñatti ati kaso. Bis yiñu def ci kaso Gore bi yépp, diir bu néewloolu lañu leen doon may ñu génn ca fañu leen tëj. Ngir moytu jokkalante ci diggante ñoom ñi ñu fa tëye, ñaari yoon rekk lañu doon gis jant bi, suba si 30i simili, ngoon gi 30i simili. Xàmmeetuñu guddi ak bëccëg, guddi yàgg loolu, booleek ñu leen di metital[9].

Xibaar bi daanu bisu 11i fan weeru mee ci atum 1973 : Omar Bolondeŋ Jóob saay na (est décédé). Mu amoon 26i at. Xibaar bi ne tasar. Ndaw ñu bari génn ci mbedd yi di bind ci turux (murs) yi cigëbla gi “Seŋoor yongkat (assassin) ; Ñu ngi ray seen doom yi, yewwuleen ; Bolondeŋ kenn du kofàtte”. Ci saa si, nguur gi dafa nëbb pekke (crime) wi. Waaye àttekat-luññutukat (juge d’instruction)bi lànk ndigal li bawoo ci nguur gi, daal di teg loxo ñaar ñu ñu jàpp ne seen loxo taq na ci mbir mi.Daa gisoon ci këyit yi ñu jëlee ci kaso bi ñu bind ne ayu-bis laata ñuy siiwaal ne dafa xaru, Bolondeŋdafa xēmoon waaye ñi yore kaso bi yëgalu ñu ko woon seen yaram sax. Waaye keroog bamuy waajateg loxo keneen ku mu njort ne taq na ci mbir mi, ci la ko fa kilifa yi jēlee teg fa beneen àttekat mudakkal luññutu gi (l’enquête) ndax ne du céram[10]. At mu jot, 11i fan ci weeru mee wu nekk ay sóobare(soldats) ñoo doon wër bàmmeelu Bolondeŋ ngir bañ nit ñi ñëw di ko màggal.

  1. Dakar-Matin (23 juillet 1966), « Un jeune sénégalais de 19 ans entre à l’École Normale Supérieure de St Cloud (section Lettres) »
  2. Florian Bobin (21 février 2021), « La folie des grandeurs. Omar Blondin Diop à propos des “grandes écoles” », Seneplus
  3. Anne Wiazemsky (2012), Une année studieuse, Paris, Gallimard, pp. 139-181
  4. Michelle Zancarini-Fournel (2017), « En souvenir d’Omar », in Françoise Blum, Pierre Guidi, Ophélie Rillon (dir.), Étudiants africains en mouvement : contribution à une histoire des années 1968, Paris, Éditions de la Sorbonne, pp. 11-12
  5. Pascal Bianchini (2021), « 1968 au Sénégal : un héritage politique en perspective », Canadian Journal of African Studies / Revue canadienne des études africaines, 55(2), pp. 307‑329
  6. Le Soleil (9 février 1971), « Arrestation des incendiaires du Centre Culturel Français »
  7. Elaine Mokhtefi (2019), Alger, capitale de la révolution. De Fanon aux Black Panthers, Paris, La Découverte
  8. Florian Bobin (2022), « Omar Blondin Diop : un artiste et militant ouest-africain en mouvement », in M.L. Manga (dir.), Mobilités en Afrique de l’Ouest : Peuplement, territoires et intégration régionale, Paris/Dakar, Hermann-Kala, pp. 127-128.
  9. Djeydi Djigo (2021), Omar Blondin Diop, un révolté, 78’, Invictus/Élever la voix
  10. Florian Bobin (10 mai 2021), « L’affaire Omar Blondin Diop doit sortir du déni où elle sommeille depuis trop longtemps », Le Monde