Ngeer
Apparence
Ngeer xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu "combretaceae". Wenn la ci xeetam.
Melo wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngeer ngàjj la gu man a àgg ba 3i met. Bari lool ci Saara bi, ci sowwu jantub Afrig, fu ci mel ni Senegaal. Garab gu yam lay doon te firiku. Di xaw a tolloo ak salaan.
Njariñ li
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ngeer garabu paj la, bokk na ci yi ñu gën a taamu ca Sowwu Afrig. Dees na ko fa jëfandikoo ngir faj xeetu wopp yu bari te wuute. Jëfandikoom danay xaw a niru ak gog kenkelibaa, te ñoom ñaar lees faral di boole, ngir faj tawatu soj, tàngooru yaram ak jafe-jafey nokki. Xob yu wex yi lees faral di jëfandikoo. Dees na ko boole ak rat it ngir faj ci soj.
Ndox mi muy ëmb, da koy tàbbal ci suuf si yeneen garab yi jariñoo ko. Kon ba ko cib tool làmboo nay njariñ.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]-
Tóortóori garabug ngeer
-
Tóortóoru garabug ngeer
-
Meññeefi garabug ngeer
Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Guiera senegalensis
Tur wi ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]farañse: Guiera |
angale: Guiera |