Rat

Jóge Wikipedia.


Nataalu garabu Rat

Rat Rat xeetu gàncax la gu bokk ci njabootu "Combretum". Dees na ko fekk ca Senegaal, ca Burkinaa, ca Gana, ca Mali, ca Gàmbi, ca Niseer, ca Niseryaa ak ca kamerun.

Meññuwaayam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Rat cib gott lay faral di sax ak ci yeneen xeeti suuf yu bari, waaye ci beeñ la gëne. Day muñ bekkoor te ci barab yiy sotti lu toll ne 200 ba 700 milimet cib taw cim at lay meññ. Màggam daa gaaw.

Melow wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Rat gàncax la guy àgg ba 12 met. Bànqaasam day wàcc, ronam dëng, xàncam day dége te baam , ñuul. Xobam day dijj, nëtëx te mel ni ndàbb bu mboqe. Ci noor lay tóortóor.

Doom bi dana àgg ci 2,5 ba 4i sàntimet ci guddaay. Ak 1,5 ba 3i sàntimet ci yaatuwaay. Saawiyee ba nowàmbar lay meññ ci yaatal.

Njariñ yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dees na ci jële ay melal yu mboq. Aw dénkam dees na ci defar ay jumtukaay. Dees na ko jëfandikoo ci wulli. Ñam la ci yenn mala yi. Dees na ko lekk te di defar ay ndimo.

=Nees di fajoo ak rat[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xobu rat day faj soj, wutal juroom ñaari xob baxal ko ci genn wàllu liitar lu mat 5i simili, di ci naan genn wàllu kaas suba , bëccëg ak ngoon.

Day yokk kàttanu góor, ñaari xob yi ngay baxal ci genn wàllu kaas ñatti waxtu.

Day yokk dereet it juroomi xob ngay wut def ko ci liitaru ndox baxal ko di ko naan 3i waxtu bu dee mag, bu dee gone kaasu attaaya

Day faj dagg-dagg bu bees, jëlal xob wu tooy mokkal ko, boo ci noppee nga tay ko ci, gaaw na ci lool.

Day faj sibiru bu àndee ak sexaw ak ngeer, baxal ko di ko naan suba, bëccëg ak ngoon.

Dana maye pàppin (àppeti).

Reen bi day faj feebaru sëy ak nduxum siti. Ak feebaru ngaana bu dee gu bees.

Boo amee doom mu yeex a dox wutal ñaari liitar baxal ko ci ndox mi di ci naan kaas 3i waxtu.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Combretum glutinosum

Turam ci yeneeni làkk[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Araab: Pulaar: dooki Hawusa: kantakara