Ngéejaan

Jóge Wikipedia.

Ngéejaan walla Ngalama ci Baambara garab la gog mi ngi fekk baax ci tundi Afrig sow jant mi ngi bokk ci njabootug kompritaasiiye.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Guddaayam man naa jàpp ci juroom jàpp fanweer ciy met peram day yaatu lool man naa jàpp juróom-ñaar-fukki sànti met. Ay foytéefam dañuy yor melo wu xaw a mboq walla melo wu xaw a oraas ci digg bi. Garab gi nag garab la gog jamonoy noor rekk lees koy farala gis ak bu nawet bi tàmbalee benn xeet la garab, gog dafa bari lool ci tund Afrig, fiñu koy fekk mu bari lool mi ngi nekk ci réew yu mel ne Senegaal, ak Ecopi.

Solo si[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab la gog bari na lumuy faj lool ndax ay raasinam dan koy jëfandikoo ngir faj lu ci mel ni néew kàttan walla ku am ay jafe-jafe ngir jugal ak biir buy daw itam ñeel gone yu ndaw ñi. Garab la gog manees na cee def ay xeeti Armuwaar ak yu ni mel manees na koo def matt.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Anogeissus leiocarpus