Mozdahir
Institut Mozdahir International (IMI) ag mbootaay gu tënkuwul ci nguur la te jubluwaayam du wut xaalis.[1] Seriif Mohammed Aali Aydaar (Cherif Mohamed Aly Aidara) moo ko taxawal te màkkaan mi nekk ci Ndakaaru.[2] IMI am na këyit guy yoonal nekkam ag mbootaay gu tënkuwul ci nguur te wër na àddina si ba teew ci réew yu bari ci tund wii, ñu man cee lim Senegaal, Kodiwaar, Mali, Gine Bisaawóo...ak ñoom seen.[3]
Teew na ci fukk ak ñaari (12) réew, te di yëngu ci fànn yu bari yu mel ne suqaliku gu sax gu sofu ci fànni wëppa ak lef yii: njàng mi, Lóofóon gu xereñ, wergi-yaram, lootaabiinu askan, mbatiit, mbay mi, yasarag jant bi, dëkkuwaay, njurtéef, leble, yoriin wu jub wu koomum kéew mi, njëmbat garab ak naatalaat àll bi.[4][5]
Ñi mu ci lëngool
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mbootaay gi nag sampu na bu baax ci Senegaal ak it ci Afrig sowwu jant ginnaaw bi mu fi amee sañ-sañub nekk fi ak këyit yi koy firndeel.
Jamono jii am na junni-junniy nit yu ci bokk te nekk fépp ci àddina si.
Ci yoon wi mu jël itam, IMI daf ciy lëngoo ak nguur yi jaare ko ci seen i jëwriñ ak gox-goxaan yi (sàmmkati ndox mi ak àll yi, mbay mi, saytukati kaaraangeg dund bi, njëwriñi jagle yi, calaw yi...), SGBS, mbootaayi àddina bi (Sémbuw dund bi ci àddina bi: Programme Alimentaire Mondial) ak kuréel yi (ANEV: Agence Nationale des éco-village, Association des Voûte Nubienne) ak ñeneen ñu bari.
Xët yi mu lëkkalool
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Téerekaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- ↑ PORTRAIT – Chérif Aïdara, guide des Chiites : Globe trotter. Le Quotidien.
- ↑ Sénégal : 127 jeunes de Vélingara s'informent sur l'islam chiite. Shafaqna.
- ↑ APPEL Chérif Mohamed Ali Aïdara, guide des chiites : «Partout dans le monde, les musulmans sont opprimés» Le Quotidien.
- ↑ Le chiisme au Sénégal Mozdahir. Shia Africa.
- ↑ Leichtman, Mara A. 2015. Shi'i Cosmopolitanisms in Africa: Lebanese Migration and Religious Conversion in Senegal. Indiana University Press.