Sëriif Muhammed Aali Aydara
Sëriif Muhammed Aali Aydara (Chérif Mohamed Aly Aïdara) mi ngi judd atum 1959 ca Daaru Hijratu (dëkk bu baayam sancoom, Sëriif Ahasan Aydara). Doomi Maymuna Jaw (moom soxna si doom ci Sëydu Jaw nekkoon seef de kantoŋ) ak Sëriif Alhasan Aydara, cosaanoo Gànnaar, bokk ci askanu Laxlal (Laghlal) ñu gën koo xam ci Ahlu sëriif laxlal di càllalag Sëriif Mulaay Idriisa, mi sos nguurug Idriisa yi, càllala gu dem ba ci Asan doomi Aali ak Faatima doomi Yónnent Yàlla Muhammed ak (JNCM).
Moo nag doomi Senegaal ak Gànnaar la.
Doon na wax ak a binde làkku yu bari niki Àngale, Araab, Farãse, Pël, ak Wolof.
Liggeeyam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Kilifa diine ci dayoom, Sëriif Mohammed Aali Aydara mooy soskat ak njaatigel Mbootaayu IMI ak it rajo "Mozdahir FM" ci Ndakaaru ak rajo "Zahra FM" ca Koldaa.
Sëriif Mohammed Aali Aydara mooy xalifab mboolem Siyit "Mozdahir" yi nekk ci Afrig ak ci àddina si.
Ay mbindam ci Xam-xam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bind na ci fànn yu bari yu ci mel ne xam-xamu Islaam, dundug Yónnent Muhammed (jàmm ak ngëneel ci moom) ak 12i imaam yu mat sëkk yu kër Yónnent bi, Ahlul bayti (jàmm ak ngëneel ci ñoom). Ay téereem yu bari siiwalees na ko, ñu man cee lim:
- Dëgg yi ci kuutlaayal Yónnent bi (Les Vérités de La Succession du Prophète)
- Imaam Useynu (YYY) martiir ak xettalikatu Islaam (L’Imam Hussein (AS) martyr et sauveur de l’islam)
- Sayyidaa Saynab (jàmm ak ngëneel ñeel na ko) waadaanu Karbalaa (Sayyidda Zaynab (paix et salut sur elle) l'héroïne de Karbala)
- Jullig Yónnent Muhammed (jàmm ak ngëneel ñeel na ko) bunu sukkandikoo ci ag njabootam (La prière du Prophète Mouhammad (PSLF) selon les membres de sa famille)
- Ghadir Khoum
- Tamxarit, bisub naqar walla bisub mbég? (Achoura jour de deuil ou jour de fête ?)
- Sàrti koppar gi ci Islaam (Principes de la finance islamique)
Téerekaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- APPEL Chérif Mohamed Ali Aïdara, guide des chiites : «Partout dans le monde, les musulmans sont opprimés». Le Quotidien.
- Le chiisme au Sénégal Mozdahir. Shia Africa.
- cherif mohamed aly aidara, grand maître au service du peuple et quelques dignitaires Congolais. Daily Motion.
- Chérif Mohamed Aly Aïdara, guide des chiites du Sénégal « Unis, les guides religieux peuvent combattre le terrorisme au Sénégal». Kolda News.
- Institut Mozdahir International.
- Sénégal : 127 jeunes de Vélingara s’informent sur l’islam chiite. Shafaqna.
- Chérif Mohamed Aly Aidara, président de Mozdahir International : « L’islam ne peut pas être une religion de violence ». Seneweb.
- Qui est Cherif Mohamed Aly Aidara. Scribd.
- Les pressions faites sur notre communauté ne nous ébranlent point. Enquete Plus.
- Progression du chiisme en Afrique, une donnée qui peut modifier les équilibres géopolitiques. Aleteia.
- Inaugurantion d'une mosquée construite par l’Institut Mozdahir International : Le khalife de Médina Gounass bénit les actions de l’Ong chiite. Leral.
- PORTRAIT – Chérif Aïdara, guide des Chiites : Globe trotter. Le Quotidien.