Mbàmbulaan
Apparence
Mbàmbulaan am mbalka mu réy la mu def ndoxum xorom, te wër ab gox.
Mbooleem mbàmbulaan yi ak géej yi ñoo jël 70% di ñatti ñeenteel ci li ci Kaw kol-kolub suuf si, maanaam 360.700.000 km². Ci lim bii 154.800.000 km² ñoo ngi ci xaaju kol-kol bu bëj-gànnaar, 205.900.000 di km² ci xaaju kol-kol bu bëj-saalum.
Mbàmbulaan yi juróom lañu:
- Mbàmbulaan gu Dal, 179.700.000km², 49,7%;
- Mbàmbulaanu Atlas, 106.100.000 km², 29,5%;
- Mbàmbulaanug End, 74.900.000 km², 20,4%;
- Mbàmbulaan gu Bëj-saalum, 20 327 000 km², 5,6%
- Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar, 14 090 000 km², 3,9%
Waaye waa-Angalteer yi ci seen gisinu melosuuf da ñuy jàppee mbooleem géej yi ne ci li wër ñaari goxi dott yi, duppee leen Mbàmbulaan gu Bëj-gànnaar ak Mbàmbulaan gu Bëj-saalum.
Tangaay wu diggdóomu gu mbàmbulaan yi | ||||||||
---|---|---|---|---|---|---|---|---|
Ci suuf | 60° tus-w. Bëj-g | Yamoo | 60° tus-w. Bëj-s. | |||||
Atlas | Gu Dal | Atlas | Gu Dal | Gu Eng | Atlas | Gu Dal | Gu End | |
Ci kaw | 7° | 4° | 27° | 27° | 27° | 0,3° | 1° | 0,8° |
-100 m | 10° | 3° | 21° | 25° | 23° | 0,1° | 1,9° | 0,6° |
-500 m | 8° | 3,5° | 7° | 8° | 12° | 2,5° | 1,7° | 1,2° |
-1.000 m | 6° | 3° | 4° | 4,5° | 6° | 0,9° | 2° | 1,5° |
-3.000 m | 2° | 2° | 2,8° | 1,7° | 3° | 0,3° | 0,1° | 0,1° |