Mboor Ak Diine
Mboor Ak Diine
(Fàttalitul) ba sa Boroom waxee Malaaka ya ne leen : “Man de maa ngi sàkk mbindéef ci banan.
+ Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, na ngeen daldi rot, sujóotal ko”.
+ Malaaka ya yépp daldi sujóot,
+ ba mu des Ibliis moom dafa rëy-rëylu bokk ca yéefar ya.
+ (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujóot ci lii ma bind ci samay yoxo ?
Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ”
+ “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci
ban”.
+ (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ;
+ te Samam rëbb dal na la ba baa saa di taxaw”.
+ “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”.
+ (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu,
+ ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”.
+ “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj loo ñoom ñépp,
+ ba mu des sa jaam ñiy sellal”.+ (Yàlla) daldi wax ne : “Maa ngi waat, ci dëgg ne dëgg laay wax,
+ Danaa feesal Safara ci yaw ak ña la topp ñépp”.
Ibliis Ak Jaamu Yàlla
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Lu waral Ibliis waatal Yàlla ne dina sànk doomu Aadama yi, wommat leen jëme jëhënnama ak ànd ak ñoom?
Bis bu ne Ibliis mi ngi jéem a fexeel nit ñi ngir sippi leen ug meram, di fexe tàbbal leen ci ñaawtéef yu mag. Naka la ak fan la ak kañ la loolu tàmbali? Ak lan moo waral nooneel googu ne ci diggante Ibliis ak doomi Aadama yi? Lii mooy li nu war a waxtaane fii.
Tay dinanu xóos ak yéen ca gën gaa xóoti nettali bokk ci nettali yi gën a doy waar te gën a man a def jeexiital ci nit ki, waar yu bari a ngi ci biir, nde ñu ëpp ci nun xamuñu dëgg-dëggi Ibliis mi nga xamantene moo gënoon na jege Yàlla Malaaka yi sax. Mbooru xeex gi diggante Ibliis ak nit ñi, mboor la mu bokkul ak yeneen mboor yi; mboor la mom xew-xewam nekkoon na te deñul di ne te day wéy di nekk ba bisu pénc. Nettalig xeex gu dàppetu googu tàmbalee ak sunu baay Aadama (HS) di wéy ba ñiy mujj ci kaw suuf, ñay dugg guyaar dugg guyaar, ñay dugg sawara dugg sawara, Saytaane def xutbaam ba ca digg ña ko toppoon ca biir sawara muy xutbab deñ ci ñoñ ak waneg seen toroxtaange.
Nuy tàmbali sunu waxtaan ci Suumiyaa baayu jinne yi ak Aadama baayu nit ñi ak Ibliis ma ñu dàkku ci yërmànde Yàlla, nu wax leen tay turam dëgg ak lu waraloon mu yéggoon ba ca asamaanu juróom ñaar ak mbooleem turam ya ci sépp asamaan. Nettali leen dëgg-dëggi ag yëram ca dàq gi ñu ko dàq ca àjjana ak digganteem moom ak Aadama (HS).
(Bàyyil xel ne) li nu fi nar a nettali noo ngi koy jële ci ay téere yu wuute, du ñàkk ay "Israa-iiliyaat" am ci (Israa-iiliyaat nag mooy nettaliy waa bani Israa-iil ya ñu daa nettali njëkk Islaam) Israa-iiliyaat nag la ca Yonnent bi (SHW) waxoon mooy jullit bi ñatti taxawaay la ci war a am: 1- dañuy nettali lol Islaam dëggal na ko, nga dëggal ko.
2- ñu nettali lol Islaam dàq na ko, nga weddi ko.
3: ñu nettali lol Islaam weddiwu ko te it saxalu ko, nga taxawlu ca bañ koo weddi bañ koo saxal.
Kon jàngat gi ci jullit bi war def ak waare wi mu ci man a jële a tax nu leen koy nettali fii.
Mbir ma a ngi tàmbalee lu jiitu ñuy bind Aadama ci luy tollu ak 2000iy at, fekk Yàlla sàkkoon na Suumiyaa miy baayu jinne yi, Yàlla ne woon ko mébétal (waxal li nga bëgg). Suumiyaa ne ko: "li may mébét moom; nuy gise te kenn du nu gis, nu man suulu ci biir suuf, sunuy màggat di man di nekk waxambaane."
Yàlla nangul ko mébétam, mu dëkkloo ko kaw suuf lépp lu mu bëgg am ko fi, nii la jinne yi nekkee ñi jëkk a jaamu Yàlla ci kaw suuf. Bàlluwaayu loolu di waxu Ibnu Abbaas ja(YYG).
Waaye ginnaaw bi Suumiyaa faatoo, ba ay xeet ci jinne yi ñëw, ñu waroon a wéyal cant Yàlla ci li mu leen xéewale ci ay xeeti xéewal, waaye defuñu ko; dañu doon yàq ci kaw suuf, daan tuurante dereet.
Yàlla yabal ay sóobarey Malaakaam, ngir ñu song leen xeex ak ñoom ngir yàq gi jinne yi dëkke woon ci kaw suuf, Malaaka yi song leen ray ci ñoom lu bari dàq leen tasaare leen, kuréel gu néew ci ñoom a rëcc làqatuji ca dun ya ak ca kaw njollaxu doj yu mag ya.
Malaaka yi yéegaale ak Ibliis booba ab xale bu ndaw la, ñu yéegaale ko jëm ak moom ca téeg yaa kawe, ñu jàngal naka lay sàbbale ak topp Yàlla sunu Boroom, Ibliis yaroo ci yoxoy Malaaka yi, di julli di jaamu Yàlla niki ni ko Malaaka yi di defe ba mujj mel ni jàmmajóobu Maalaaka yi. Yàlla sellal Ibliis ngir jaamoom ju bari, mu yëkkati ko ca mbooloo maa kawe, ca "Malaakay Muqarabiin ya" ña gën a jege Yàlla.
Ibliis YYR(Yal na ko Yàlla Rëbb) a ngi tuddoon Hasaasiil, muy tekki aarkat/wattukat (YX) -Yàlla a Xam- , nii la Hasaasiil mujj a nekke kaw asamaan daan ànd ak Malaaka yi daan jaamu Yàlla, sori woon jinne yi nga xam ne ñoo dëkke woon kaw suuf, ba mujj a gën a tedd Malaaka yi, ëpp leen xam-xam ak jaamu Yàlla. Yàlla mujj koo jox wàccuwaay wu kawe mu doon bëkk-néegu àjjana, doon kilifag téegu àddina.
Bi Ibliis nekkee kilifag asamaanu si tiim àddina, mu mujj a woru ci boppam ne: "Def naa lu kenn masut a def! Yàlla jox na ma lii lépp ngir samag ràññeeku ci kaw Malaaka yi"
Yàlla yër la ne ca xolu Ibliis cig rëy ak yëg boppam. Kenn xamul woon li ne ci biir Ibliis ku dul Yàlla.
Malaaka ya nag ñoom yëguñu dara ci li xew. Ginnaaw ba, la lu kenn masut a foog ag xewam, xew. Nee nañu Hasaasiil bépp barabu sujjóot day gis nu bind fa "Dàkku Ibliis, móolug Ibliis/ rëbbug Ibliis, ngeccig Ibliis". Mu gis ñu bind ci kaw bunt guyaar yi: " Amna sama benn jaam bu bokk ci sama way-jege ñi, dinaa ko digal, mu bañ ne du topp ndigal, moom kay day moy di moy ba ma dàq ko sama bunt, rëbb ko, def mbooleem li mu mas a jaamu ni pënd bu ñu wesaare."
Hasaasiil yéemu ne: kan mooy mile Ibliis noo ngi muslu Yàlla ci loolu, mu wëlbatiku ne sunu Boroom; yaw sama Boroom digal ma ma rëbb ko. Yalla daa di ko koy digal, mu rëbb ko luy tollu ak 1000iy at.
Nekkul woon ne Hasaasiil rekk a gisoon loolu, waaye Malaaka yépp itam gisoon nañu ko.
Bi Israafiil xoolee "Lawhul Mahfuus" dafa gis ne: "Am na menn mbindéef muy jaamu Yàlla 8000iy at, ginnaaw ba Yàlla delloo ko mbooleem la mu jaamu woon teg ci rëbb ko."
Mu jooy jooyu metti ba Malaaka yi sax mujj koo yërëm. (Israafiil daa jooy ngir ragal a nekk kookee.) Malaaka yi laaj ko lu muy jooy? Mu ne (Yàlla a rekk a xam) : sama bët a tegu ci am mbóot ci bóoti sunu Boroom yi... (Mu nettali leen la mu gis).
Malaaka yépp ànd di jooy , ku ne ci ñoom ragal nekk mbindéef moomu ñu nar a dàkku. Ñu ne: li fi sës mooy nu dem ca Hasaasiil, moom bokk na ci way-jege ñi sunu Boroom te ku am nangug ñaan la, mu ñaanal nu ñu bañ a nekk mbindéef moomu. Ñu daa di dem ca Hasaasiil wax ko ko. Hasaasiil yëkkatiy yoxoom ne: 'Yaw Buur bi bul teg sag sàññ ci seen kaw." (Te waxul: yaw Buur bi bul teg sa sàññ ci nun kaw). Mu neeti: "yaw sama Boroom muccal leen cig ndog." Mu ñaanal leen fàtte boppam.
Hasaasiil woru jàpp na ko ba yegg ci ne masul a jàpp ne man na nekk Ibliis moomu ñuy dàkku, dàq ko ci yërmànde Yàlla. Nii la ñu nangoo ñaanalam Malaaka yi, mu nar a doon ug toroxtaangeem.
Kahbul Axbaar (mi ngi bokkon ci ñi daa waxtaane jaar-jaaru yahuud yi) nee na: Ibliis, turam a ngi nekkoon "Aji-dellu ji" ci asamaan su njëkk si, su ñaareel si "Aji-dëddu ji" su ñatteel si "Aji-xam ji" su ñenteel si "Wàlliyu bi", su juróomeel si "Aji-ragal Yàlla ji" su juróom benneel si "Bëkk-néeg bi", su juróom ñaareel si "Hasaasiil", ca Lawhul Maxfuus "Ibliis" baatu Ibliis nag mooy tekki "soril" (maanaam muy ku ñu soril ci yërmànde Yàlla).
Ibliis Ak Moyug Boroomam
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bi Yàlla nammee wan Malaaka yi dëgg-dëggi Hasaasiil ag rëy gi nekk ci moom, Yàlla da ne:
" Fàttalikul ba sa Boroom waxee Malaaka ya, ne leen: “Man dey damaa namm a def ci suuf si ag kilifa[kuutaay]. Ñu toontu ne ko : “Moo ndax dangay def ci suuf si koo xam ne daf ciy nekk di yàq, di tuur i dereet, te nun nu ngi lay sàbbaal, di la sant te di màggal sag sell ? ”
Yàlla jekkul rekk di wax loolu Malaaka yi.
Jële nañu ci Ibnu Abbaas (YYG) mu ne: Malaaka yi wax nañu loolu ngir li ñu xamoon ci biri jinne yi dëkke woon kaw suuf ak la ñu daan def ci kaw suuf, mu mel ni dañu ne ko " Ay yaw sunu Boroom , ndax danga fay teg ku mel ni jinne yi nga xam ne dañu doon tuur i dereet ca kaw suuf ñu daan yàq, daan moy? Te nun danu lay sàbbaal di la sant, di la sellal. Yàlla ne leen:
“Xam naa lu ngeen xamul ! ”.
Yàlla a ngi namm a wax fii, li malaaka yi xamul ci biri Ibliis cig nuuroom ci rëy, ag dogoom ci nar a moy ndigalam ak woroom. Malaaka yi jortoon ne sunu Boroom daa mer ci tont googu mu leen tont, ñu tàmbalee sàbbal ko ak sellal ko doon wër ca "Baytul Mahmuur" ca asamaan, nga xam day niru ak ni Kaaba gi mel ci kaw suuf.
Yàlla wahyu suuf si ne ko: damay sàkk ci yaw ay bindéef, amna ci ñoom ñu may topp, am ci ñoom ñu may moy, képp ku ma ci topp ma tàbbal ko guyaar, képp ku ma moy ma tàbbal ko sawara.
Suuf ne ko: ndax dangay bind ci man ñoo xam ne danga leen di dugal sawara? Sunu Boroom ne ko: waaw!
Nee nañu: Ibliis daal di wàcc ci kaw suuf ne ko yaw suuf, damaa ñëw ngir laabiire la, Yàlla daa namm a bind ci yaw ki gën ci bindaafon yi, te may ragal ñu moy ko mu leen di tàbbal sawara, bu booba yaw it dinga duggaale sawara tamit. Suuf daa di jooy!
Yàlla bind sunu baay Aadama ciy yoxoom ngir Ibliis bañ a rëy ci sujjótal ko, Yàlla a ngi nuy wax ci loolu:
"Suma ko móolee ba ëf ci Sama Ruu, nangeen daldi rot, sujjóotal ko."
Nee nañu: bi Yàlla bindee Aadama (HS) toog na 40i guddi. Am ñu ne: 40i at, muy jëmm ju ñu tërëral. Ibliis daan ko dikke, di ko kàjji muy keleŋ ni ban wu wow, nee ñu mooy li sunu Boroom naan:
" Moom moo bind nit ci ban bu tikk dëgër ".
Ibliis di dugg ci biir gémmiñu Aadama di génne ci ginnaawam, di jaar ci ginnaawam di génne ci gémmiñam, te naan ko: " Doo dara, ak lu tax ñu bind la, su ñu ma la saytuloo ma alag la, bu ñu la saytuloo ma ma moy la".
Malaaka yi bu ñu ko daan romb dañu ko daan ragal, fekk ne Ibliis moo leen ko gën a ragal. Ba dig bi nga xam ne la Yàlla namm ëf Ruuwam ci moom jotee, mu ëf Aadama Ruuwam. Mu digal Malaaka yi ci ñu sujjóotal Aadama. Malaaka yépp sujjóotal Aadama ba mu des Ibliis ngir rëy mu bokk ci way-wedd ni ca saa sa. Yàlla ne ko yaw Ibliis, ana lu la tee sujjóot ndeem digal naa la? Mu ne kii maa ko gën, man du ma sujjóotal nit koo binde ci suufu ban.
Ibliis sujjóotul ngir rëyam ak mbewteem ak kiñaan. Yàlla ne:
" 75. (Yàlla) daldi ne : “yaw Ibliis, lan moo la tere nga sujóot ci lii ma bind ci samay yoxo ? Dangay rëy-rëylu walla dangaa bokk ci ña kawe ? ”
76. “[Ibliis,] tontu ne ko : maa ko gën ndax yaa ngi ma bind ci safara moom nga bind ko ci
ban”.
77. (Yàlla) ne ko : “Génnal ca biti, dàkku naa la ;
78. te Samam rëbb dal na la ba ba saa di taxaw”.
79. “[Ibliis,] ne ko : yaw sama Boroom, muñal ma, ba bisub dekkiwaat ba”.
80. (Yàlla) ne ko : “may Nanu la dig boobu,
81. ba ca bisub waxtu wu ñu xam wa (Bis Pénc ba)”.
82. “[Ibliis ne ko] giiñ naa ci sa màgg gi ne ! Danaa leen lajj-loo ñoom ñépp,
83. ba mu des sa jaam ñiy sellal”."
Ibliis Ak Aadama(HS)
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Bi Yàlla noppee ci Ibliis ak ci yedd ko, Ibliis bañ rekk ne day moy Yàlla. Sunu Boroom rëbb ko tàq ko ci yërmàndeem def ko Saytaane Rajiim, génne ko ca guyaar. Ginnaaw loolu Ibliis sumboo ak meram iñaane Aadama, mu bëgg koo génne guyaar. Yàlla bàyyi ak Aadama xelam gawu ko ci dara, mu bayyi ko ak sagoom, muy man a ràññe lu baax ak lu bon, ginnaaw ba mu ko maytuloo Ibliis, Yàlla a ngi naan:
". Nu wax ko ne ko : “Kii dey sab noon la yaak sa soxna. Farluleen ba bu mu leen génne Àjjana, [su ngeen génnee] da ngeen sonnu de.
118. [Fii ci Àjjana] doo fi xiif, doo fi rafle,
119. doo fi yëg u mar, doo fi màggat”."
Ginnaw bi ñu dàkkoo Ibliis, mu tàmbali nag ci jëfe la mu dogu woon; te mooy fayu ci Aadama (HS) ak génne ko guyaar, di ko awale ci di ko jiixi-jaaxaloo, jéem koo gëmloo ne xam na lol man na tax ba Aadama sax dàkk du dee mukk. Yàlla a ngi wax naan:
"Séytaane daldi koy jax-jaxal [nëxal xelam] ne ko : "Yaw Aadama, ndax duma la tegtal garab guy tax nga am nguur gu dootul foq ? ”."
Ibliis jaare ci bëggug Aadama ci sax fi dàkk ak sax ca guyaar; bañ fa a génn. Mu xam ne loolu ay tombug néew dooleem, Ibliis daa bëgg a wan ne sunu Boroom; man naa alag kii nga may gënalee. Adaama moom ndaysaan, xamul dara ci kàcci Ibliis yi, waaye li mu ko wax neex na ko te jar na a jarabu, mu yëg ne loolu du'y fo mu laaj Ibliis naka lay def ba am loolu moom ak soxnaam Awa? Ibliis ne ko : ndax yaa ngi gis garab gii ñu la tere nga lekk ci? Moo la ko man a may. Waaye ba tay Aadama gëmul Ibliis, muy fàttaliku tere gi sunu Boroom tere woon ci mu bañ a jege garab gi.
Kon naka la Aadama def ba lekk ca garab ga ak aartu yi ñu ko aartu yépp bàyyikoo ci sunu Boroom?
Boroom xam-xam dañuy wax ne(YRX): Ibliis ci jax-jaxal yi mu doon def Aadama, moo ko doon fàtteloo ndànk ndànk li ko sunu Boroom tere woon (loolu moo nuy dal nun ñépp ba tay, su nuy saytaane di jax-jaxal, danuy fàtte ndànk ndànk lepp lu nu mas a waar). Waaye Aadama gëmul woon lu dul ginnaw ba mu waatee, Aadama ne ko giiñal nu bu dee li nga wax dëgg la, Aadama (HS) -ci ni ñu bind- xam na ne kenn warut a waat ci Yàlla ba noppi di fen. Mu ne ko waatal ci kiy sama Boroom di sa Boroom ne li ngay wax dëgg la. Ca noonu la Ibliis mi ñu rëbb giiñe ci kanamu Aadama ngiiñug fen ci ne li mu wax dëgg la te moom da koy laabiir rekk moom ak Awa. Yàlla a ngi nuy leeral loolu ci téereem bu sell bi Alxuraam, mu ne: " Mu giiñal leen ne moom kat mi ngo bokk ci way-laabiire ñi"
Ginnaw ba Ibliis waatee, ci la xelu Aadama soog di dal naka noonu Awa (HMS) ndax seen xel masut a jàpp ne kenn sañ na a giiñ ci Yàlla ci ay nar, Ibliis nekk ki jëkk a waat ci Yàlla ci ay fen (kon képp kuy waat ci Yàlla di fen, Ibliis ngay roy) te amul fu mu ko defe fu dul àjjuna. Ca la Aadama fàtte lépp lu ñu ko tere woon ndax giiñu Ibliis ji, tàmbalee lekk ca garab ga moom ak Awa. Nee na ñu garab ga garabu pom la woon nekkoon ci kaw suuf, bi ñu ko lekkee rekk la seen mbalaan ya muriku seen awra feeñ. Yàlla ngi nuy leeral loolu naan:
"22. Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt
di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”
wàccug Aadama Ak Awa Ak Ibliis Ci Kaw Suuf
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]La dal Aadama dal ko; mu lekk ca garab ga, sunu Boroom wàcce Aadama ak Awa ñoom ak Ibliis ci kaw suuf, Yàlla a ngi naan:
"[Séytaane] tarxiisloo na leen, génne leen fa ñu nekkoon. Nu ne leen : “Wàccleen ; di
noonuwante. Te itam dangeen am ci kaw suuf ay dëkkuwaay ak i jumtukaay as ndiir”.
Bi ñu wàccee Ibliis ci kaw suuf daf ne: yaw sama Boroom génne nga ma àjjana ngir Aadama, te man manaluma ko dara ndare danga maa kàttanal ci kawam, Mu ne ko defal naa la ko, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko lu mu am ci doom nga am lu ni tollu, mu ne ko dollil ma, Mu ne ko seen i dënn say dëkkuwaay la; ngay man daw seen biir i yamar ni dereet di dawe seen i yaram, mu neeti dollil ma, Mu ne "Génnal ak say kàddu, loo mën ci ñoom, nanga leen song ak say xarekat ak say gawar,
nanga bokk ak ñoom alal ak i doom te dig leen”. Waaye Séytaane du leen dig lu dul ay nax."
Ginnaaw bi Aadama xamee li Ibliis sàkku ci sunu Boroom mu ne: Ay yaw sama Boroom teg nga ko sama kaw, te man it manuma mucc ci moom lu dul ci sa ndimbal, Mu ne ko doo am doom lu dul boole naa ko ak ñu koy aar ci àndaale yu bon, mu ne dollil ma, Mu ne ko jenn jëf ju baax ju ne ma ful ko fukk te di ko yokk, jenn jëf ju ñaaw ju ne jenn laa koy jàppe te di ko far, mu ne dollil ma, Mu ne ko "Waxal ne : “Éy yéen Sama jaam ñi yàq seen bopp, buleen naagu ci yërmandey Yàlla.
Ndax Yàlla dana jéggale bakkaar yépp. Mooy Jéggalaakoon ba, di Jaglewaakoon ba”.
Mu neeti ko, yaw sama Boroom dollil ma, Mu ne say njaboot fi ak ñoo ngi dund du ma tëj seen buntu njéggal, mu ne dollil ma, Mu ne dinaa jéggale te du ma toppe, mu ne doyal naa.
Al-Faaruux Siise✍🏾