Awa

Jóge Wikipedia.

Awa soxnas Aadama

Ci làkku ibrë (חַוָּה) la tur wi jóge. Awa mooy ni ñu koy waxe ci Lislaam (حواء, Hawwa). Ci angale ak ci faranse mooy Eve. Turu jigéen ji Yàlla jëkka bind la. Ci faaru Aadama la ko Yàlla bindoon. Danuy gis jalooreem ci Ge 1:27-30; 2:20-4:2,25. Ci Injiil feeñ na ci 2Ko 11:3; 1Tim 2:13.

Ci Lislaam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Awa ak Adaama sunu Boroom Moo ngi nuy nettali seen i bir ci Alxuraan, awa di Soxna ci Aadama, doon wéttalam ak noflaayam.

Alxuraan a ngi naan: 35. Ñu wax ne ko : “Yaw Aadama dëkkal ci àjjana yaak sa soxna, ngeen di fa lekkee na mu leen neexee, ca fa mu leen soobee ; te bu leen jege garab gile : kon dey ngeen bokk ci way- tooñ ña”. [Saar 2: Nag Wa]

19. “Te yaw Aadama, dëkkal yaak sa soxna, Àjjana ; lekkleen yéen ñaar fu leen fi neex ; waaye buleen jegeñ garab gii ; su amee, ngeen tooñ.”

20. Séytaane jax-jaxal leen ngir mu feeñal ca ñoom ñaar la Nu leen nëbboon - ci seen cër - mu ne leen : “Seen Boroom terewuleen ngeen jegeñ garab gii lu dul ne Dafa bañ ngeen nekk ñaari Malaaka walla ngeen bokk ca ñay dund fàwwu [duñu dee] ! ”.

21. Mu waatal leen, ne leen : “Man dey damaa bokk rekk ci ñi leen di laabire”.

22. Mu tegtal leen cig wor. Ba ñu mosee ñoom ñaar garab ga, la seen pëy daldi feeñ ; ñuy witt di tafoo ay xob ca Àjjana. Seen Boroom woo leen, ne leen : “Ndax terewuma leen woon garab gii ? Te it wax leen ne Séytaane seenug noon tigi la ? ”

23. [[[Aadama]] ak Awa] daldi ne : "Sunu Boroom, tooñ nanu sunu bopp. Soo nu baalul, yërëm nu, kon dananu bokk ca ñu yàqule ña”.

24. Mu ne leen : “Wàccleen, ku ci nekk di noonu ka ca des. Suuf si, am ngeen fay dëkkuwaay ak i xéewal ab diir.” 25. “Fa ngeen di dunde, fa ngeen di faatoo, fa lañu leen di génnee [ngeen dekkiwaat].”

[Saar 7: Dig Wa]