Maki Sàll

Jóge Wikipedia.

Maki Sàll, mi ngi judd ci 11 desambar 1961 ca Fatik, ab nitu Càmmu Senegaal la. Mooy njiitu réewum Senegaal dale atum 2012.

Mi ngi bokkoon ci làngug politig gu PDS, doonoon ci ñi doon jàpple Abdulaay Wàdd ci palug njiitu réew mu Senegaal ci atum 2000. Ci ginnaaw bi doon na fi jëwrinu Mbéll yi, Yasara gi ak Jafaan yi dale 2002 ba 2003, doonoon fi jëwrinu Biir réew meek gox-goxaan yi dale 2003 ba 2004, Jëwrin ju njëkk 2004 ba 2007, ginnaaw bi njiital Ngomlaan gu Senegaal dale 2007 ba 2008.

Ci 2008, ginnaaw ay jàppante yu mu amoon ak njiitu réew ma woon Abdulaay Wàdd la génn PDS dem sos APR, làngug boppam gi koy yóbb ci ndam li mu am ci palug njiitu réew mu 2012.

Cig palam ci 2012 la taxawal Plan Sénégal Émergent di xalaat bi liggéeyam ngir suqalu Senegaal sukkandiku. Soloos xalaat boobu mi ngi sukkandiku ci tabaxi jumtukaay (ay yoon, naawuwaay aki waax, ...), taxawal ag Ndefar guy man a jox liggéey waa-réew mi, suqalu càmm geek mbay mi.

Ci atum 2019 lañ ko falaat ginnaaw palug njiitu réew mi amoon ca at mooma. Ci atu 2024 la war a jeexal pal gu mujj googu giy war a yam ci juróomi at.