Aller au contenu

Màntaalis

Jóge Wikipedia.
Nataalu garabug Màntaalis

Mantaalis garab la gog ay xobam

day sew teg ci dëgar. Am ay wànqaas yu tegaloo ci melokaan wu yomb a ràññee,  man a


àgg  ci fukk ba ci ñaar-fukk i met... ci njoolaay. Mbayum garab gi ajuwul ci lenn luñuy jëfandikoo ci wàllug foytéef waaye man nanu koo jëfandikoo cig paj walla cuub. Dees koy jëfandikoo it leeg-leeg ci jëmbat i garab ndax garab gi keram day yaatu lool te it garab gi bu màggee day rafetal bërëb.

Ci cosaanam, moom garab gi mi ngi cosaanoo réew mu ñuy wax (Madagaskaar).

Mbayam ak barabam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Noo ngi fekk garab gi ci lu ëpp ci àll bu kawewut lool, ci suuf su nangu. Cig mbayam nag garab gi man naa dund ci sunu tund wii nga xamente ni du tooy lool, te it du wow lool ak màggam it doon lu gaaw ci barab yi nga xam ni du tàng lool te it du sedd lool te it li ko ciy gënal mooy ay taw yoo xamente nii du bari lool waaye it bu baree itam man na koo dékku. Dana soxla it muy nekk fu am jant day gën a gaawal ak màggam.

Ay njariñam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab gi amul benn njariñ ci lu jam ci lu nit man a lekk. Ci wàllug paj, xasu garab gi ak i bantam man nanu leen a jëfandikoo ngir faj feebari yenn biir yi. Leneen it ci ay njariñam garab gi man nanu koo jëfandikoo ci lu ëpp ci nu ñuy fexee jëmbatat i garab maanaam ay sémb yu jëm ci jëmbat i garab leneen ci ay njariñam xas mi ak bant bi man nanu leen a jëfandikoo ngir defar ci ay xeet i cuub.

Turu xam-xam

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mantalie Terminalia