Jinne

Jóge Wikipedia.
Dencukaay:الجن.png

Jinne j: mbindéefu sunu Boroom la, Yàlla ngi ko binde ci sawara, ki nga xam ne moo la Yàlla jëkk a sàkk ci jinne yi mooy Suumiyaa baayu jinne yi nga xam ne niki ni Aadama doone daayu nit ñi noonu la mel ci jinne. Y Jinne yi nag ñoo jiitu nit ñi ci kaw suuf, ñoo nekkoon xalifag kaw suuf njëkk ñuy sàkk nit, woroom xam-xam yi dañuy wax ne amoon na ay xeeti bindeef yu jiitu jinne yi ci kaw waaye wuute nañu ci seen tur la ca gën a siiw mooy ne "Xin ak Bin" lañu tudd, waaye ñu daan yàqate ci kaw suuf Yàlla wuutele leen ak jinne yi. Jinne yi seen njëlbeenug jamono nekkoon nañu ñu daan wéetal seen Boroom daan sellal, dundaloon kaw suuf; ciy tabax i njénde defar ay dër(jardin) yu naat, sàkk ay bëtti ndox yuy wal, ñu doon dund cig teddnga, ba mu yàgg, ñu tàmbalee bew, yëg seen bopp, di rëy-rëylu ci kaw, di lottal ñi néew doole, di rayante seen biir, mujj dëkkewuñu ci kaw lu moy yàq. Yàlla yabal ci ñoom xareb Malaakaam ñu wàcc ci kaw suuf ngir xeex ak jinne yi, ray ci ñoom lu takku, ñu néew a mucc ci ñoom làqatuji ca lëgg-lëggi ndox ya ak ca xunt ya ak ca kaw njobbaxtalu doj yu mag ya (montagne). Amoon na ci ñoom waay ju baaxoon daan leen waar ba bi Malaaka ya doon xeex ak jinne yi moom ci xareb Malaaka ya la faroon, ñu koy wax "Hasaasiil" (boo ci bëggee lu gën a yaatu, yëral Mboor Ak Diine"[1]

Alxuraan Ak Jinne[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Alxuraan, tudd na leen lu bari ba am na Saar wow Saaru Jinne Ya la tudd (Suuratul Jinni)