Aller au contenu

Maalaaka

Jóge Wikipedia.

Malaaka, ay bindeefi sunu Boroom yu mu teral la, binde leen ci leeram, manuñoo moy seen Boroom (noonu la leen binde), seen i tolluwaay ak seen i melo wuute; dañoo am i laaf wuute lim ba, ku ne ak na muy jaamoo Yàlla, duñu ay góor walla jigéen, duñu lekk duñu naan, walla kon sàbbal seen Boroom ak sellal ko mooy seen lekk ak naan.

Gëm Malaaka yi mooy ñaareelu ponki ngëm ci jullit bi.

==Lislaam Ak Malaaka==
[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Islaam jàngale na lu bari ci Malaaka yi, ñuy ñu ñu selle fi jullit yi. Jaamu Yàlla rekk ay seen yitte, te duñu ko moy mukk, jullit bi war dàq lépp lu yellul ci ñoom (luy dàqonte ak sellam jullit bi waru koo gëm), ku ne ak yiite ga nga war a dox.

==Gëm Malaaka Yi==

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

NI NUY GËME MALAAKA YI (yal na Yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom)

Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lañu, te ñu ñu musal ciy bàkkaar lañu, (duñu moy Yàlla), duñu xayta (duñu tuur dugub) duñu saw it, ñu sunu Boroom laabal lañu. Duñu lekk duñu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu Yàlla teral lañu ba fàww, kenn du ci moy Yàlla, ku ci ne li ko Yàlla digal rekk lay def. Ci leer la leen Yàlla binde. Sàbbaal seen Boroom mooy seenug naan, sellal Ko mooy seenug lekk.

Alxuraan Ak Malaaka Yi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Alxuraan indi na lu bari ci ñoom tudd turi ñenn ñi, niki seen jëwriñ Jibriil ak ñeneen ñu dul moom. Alxuraan day nettali Maalaaka yi ñuy wax ak seen Boroom niki bi muy nettali bi Yàlla nee : "Day sàkk ku Koy wuutu ci kaw suuf", Maalaaka yi dañu ne ko ndax danga fa teg ñuy yàqate kaw suuf di tuurante dereet? Te nun nu lay sàbbaal ak a sant te it di la sellal. Yàlla ne leen Xam Naa lu ngeen xamul.

Naka noonu la nuy Alxuraan di xamalee ci ne kenn ku ne ci nun am na ñaari malaaka yu nekk ci yaari wàllam di bind ay jëfam.

Alxuraan di nu xamal batay ne Maalaaka yi dañuy soppaliku ba mel ni ay doomi Aadama niki ni mu nu ko doon nettalee ca Maalaaka yabdoon bégalsi sunu maam Ibraahiima ci ag amam doom, jàlloon ca dëkk Luut ba ne ay ganam la...

Ak yeneen i nettali...

Turu Yenn Malaaka Yi Ak Seen i Liggéey

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ka ca jiitu mooy:

  • Jibriil mooy jëwriñu Malaaka yi, nekkoon ki ñu wóolu ci wahyu ga miy wàcce Alxuraan daan ko sa Yónnent bi SHW
  • Miikaa-iil
  • Israafiil
  • Hasraa-iil