Aller au contenu

Jimbulang bu waa-Brëtaañ

Jóge Wikipedia.
yëgleeb génnu jumbulang bi

Jimbulang bu waa-Brëtaañ walla Encyclopædia Britannica (ci wu-angalteer), ñi ngi ko siiwal ci diggante 1768-1771. Siiwalam gu njëkk mi ngi ame ca Edimbuurg ca Ekos. Bu waa-Brëtaañ bi bokk na ci jimbulang yiy wax ci lu daj yi njëkk ci kàllaama wu-angalteer, te bay jii ñoo ngi koy siiwal.

Ci ndoorteelu ñaareelu xaaju 1700 ba ci 1900, bari woon na ay boroom xam-xam yu doon jàppee ay jukkeem niki delluwaay bu wóor, yenn saa yi, ci siiwal yu yees yi, daa na am ay gisiin yu yees yees jagleel ay mboolooy gëstukat. Ci jamono yooyu amoon na gëdd bu baax ci biir askan wiy làkk wu-angalteer. Ci XX xarnu bi la yitteey jimbulang soppiku bu baax, coppite gi amal na ay njeexiit ci xarkanam ci fukk ak benneelu siiwal gi.

Taariixu jagal yi

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]
jagaltaariixu jagaldayoo
1eel17681771 3 téere
2eel17771784 10 téere
3eel17881797, 1801 18 téere
4eel18011809 20 téere
5eel181520 téere
6eel 18201823, 18151824 20 téere ak 2 yees yokk
7eel18301842 21 téere
8eel18521860 21 téere
9eel18751889 24 téere
10eel19021903 9u jagal ak 2 yees yokk
11eel19101911 29 téere
12eel19211922 11u jagal ak 3 yees yokk
13eel1926 11u jagal ak 6 yees yokk
14eel19291973 24 téere
15eel19741984 28 téere
198532 téere

jagal gu njëkk gees def ci CD-ROM mi ngi génn 1994.

Lëkkalekaay yu biti

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]