Jimbulang
Jimbulaŋ aw wayndare la wu yitteem doon ëmb mbooleem xeeti xam-xam walla man naa itam tënku ci benn xam-xam, maanaam jimbulaŋ buy wax ci paj walla ci taariix kepp. Jimbulaŋ am mbooloom ay jukki la def, bu ci nekk di wax ci lenn: ciw nit, cib barab, cib xew-xew, cib xam-xam,... Jimbulaŋ day wuuteek baatukaay, ndax du yem rekk ci faramfacce wenn làkk wi. Naka-jekk day doon ay téere yu bari.
Tekkeem gu daj
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Cër yi ëpp solo yiy tax a raññee ab jimbulang, ñeent lañu:
- Jagleel gi ci am
- Seenug lëkkaloo
- Nosiin wi
- Mbidiinu jukki yi.
Jimbulang yi man nañoo wuute, aju ci seenum ëmbiit, man nañoo ubbeeku ci xeeti xameef yépp (Jimbulang bu Trecani ak Jimbulang bu waa-Brëtaañ, ñooy yi ci gën a siiw), walla itam tënku ci wenn xeetu xam-xam wi, niki ab jimbulangu paj, bu xam-xam walla bu xeltu. Am na it ay jimbulang yuy jagleelu ci wàll wu yaa ci cosaan, diine walla politig wu wenn askan, walla xeet, niki Jimbulang bu Mag bu Siwiet yi, Jimbulangu Jewish bi...
Yitteey liggéeyi jimbulang mooy jébbal xameef gi ëpp solo gees dajale ñeel tëriit li. Yii liggéey nit yàgg na koo def, dalee lu sori ci taariixam, waaye baatu jimbulang ñi ngi ko tambalee jëfandikoo ngir wax yile liggéey ci XVIu xarnu. Bépp liggéeyu jimbulang, ci lu leer, ab tënk rekk la ci xameefi nit, te it liggéey bi day soppiku aju ci dayoo ak xóotaayu ëmbiitam. Mbooloo ma ñu koy jagleel man naa am njeexiit ci ëmbiit mi; ab jimbulang bees jagleeli gone mooy gën a néew bees jagleeli mag.
Nosiinu jukki yi am na solo lool, ndax moo koy tax a doon ab jumtukaay bu saytoom yomb, kon gëstu ci dina yomb. Ci taariix, ñaari xeeti nosiin lañuy jëfandikoo ci jimbulang yu këyit yi: nosiin gu abajada, jukki yi dañu leen a nos topp nosiinu arafi abajada gu làkk wa ñu binde jimbulang ba, beneen bi mooy séddale leen ciy wàll. Bu njëkk bi mooy bi ñu gën a jëfandikoo ba tay jii, donte xibaarukaay yu mbëjfeppal yi tax nañu ceet geek dello gi man a am, di lu kenn manutoon a xalaat bu njëkk ba.
Jimbulang yi njëkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Nit, dale ci lu yàgg cig nekkam, doon na jéem a nos ay xameefam. Li dale ci jamono ju yàgg ja, bindkat yi tambali woon nañu xalaat di boole banqaasi xam-xam yépp. Ci jimbulangkat yu njëkk ya man nañu cee lim Góor gi Plini mi bind Naturalis historia (taariixu dend bi), doonoon ag faramfacce, ci fanweer ak juroom-ñaari téere ñeel dend bi, nekkoon na liggéey bu siiwoon ca Tugal gépp ca Jamono ju duggu ja.
Yenn ci liggéey yi mat a fattaliku bokk na ci jimbulang bi Ibn Xaldun bindoon ci 1377, duppee ko Al-Muqaddima(Taariixu àdduna bi), mu ëmboon mbooleem xameefi XIVu xarnu bi: melosuuf, xeltu, taariix, koom-koom, gëstumboolaay, politig, paj ba ci suqaliku gu sax. Jimbulangu xam-xam bu Abu Bakr al-Razi, mutasilita bu Al-Kindi(ci daanaka 270 téere)
Imbratóor bu siin bi, Cheng-Zu bu callala gu Ming moo amaloon Jimbulangu Yongle, di benn ci jimbulang yi gën a yaa ci taariix, mi ngi àgg ci 1408 nekkoon 11.000 téere yees bindeek loxo, lu mat 400 ci ñoom ñoo ngi leen denc ba tay.
Yii téere, loxo lañu leen doon sottee ba tax doonuñu woon tasaaroo lool, boroom alal yeek niti diine yi rekk ñoo ci doon jot: Doonoon nañu ay téere yu seer lool.