Jëfandikukat:Laay Juuf
Apparence
Mbërbóof
Mbërbóof xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Curcurbitaceae", barab yu naaje yi lees koy baye. Tur wi nag ci làkku wolof ñi ngi ko tëgge ci "mbër mu bóof" ndax ba
ri gu mu bari ay njariñ rekk.
Melow mbërbóof
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Garab gi danay àgg ba 5 met ci guddaay. Xobam xet gu tar ak cafka gu wex la yore.
Tóortóoram day ndaw te mboq. Car yu nooy a koy tëye.
Doom bi daa dége te puur. Guddaayam 8 ba 35i sàntimet lay àgg.
Njariñ li
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Mbërbóof lees di lekk la te di ko fajoo. Ci toppatoog jabet ak yenn kãseer yi dees na ko fa jëfandikoo.
Nataal yi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Turu xam-xam wi
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Momordica balsamina
Turam ci yeneeni làkk
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Farañse: margose