Aller au contenu

Hepatite B

Jóge Wikipedia.

Hepatite B (HB) feebar la buy wàlle, li koy joxe mooy doomu jàngoro (wiris) bi tudd virus hepatite B (VHB) te dafay jàpp resu nit ki. Mën na wàlle ci lu sew ak ci lu tar. Li gëna bari suy sooga dal nit ki du feeñ ci moom. Amna ci ñoo xam ni da leen duggee dañuy feebar di waccu, der bi furi, tàyyeel, saw mu nëx ak metitu biir.[1] Yenn dina faral di def noonu ay ayi-bis waaye bariwul lumuy faat nit ki su koy sooga dal.[1][2] Feebar bi mën na nekk sa yaram 30 ba 180 fan laata muy feeñ.[1] Xale yi feebar bi dug bi ñuy sooga judd, 90% ci ñoom dañuy yegg ci hepatite B bu tar bi (kronik) waaye xale yi am 5 at, 10% ci ñoom rek ñooy am bu tar bi.[3] Lu gëna bari ci hepatite bu tar bi du feeñ; waaye mën na dem bay egg ci, cirrhose ak yàq resu nit ki (cancer du foie).[4] Cirrhose ak res wu yàqu dina daaneel 25% ci ñi am njàgoro ju tar ji.[1]

Lila mëna jox doomu jàngoro ji mooy nga laal deretam wala bépp ndox mu jogee ci yaramu ki ko am. Fi feebar bi di ëppee li muy dug ci nit ki mooy ci liir buy gane si àdduna wala laal deretu ku am jàngoro ji bi muy nekk xale, noonu lañuy faral di jàppee Hepatite B ci barab yi mu gëna bari. Sudee ci barab yi jàngoro ji bariwul, li ko fay gëna joxe mooy pikiiru grog ci yoonu deret wala ci sëy.[1] Nit ñiy liggéey ci barabu fajukaay yi itam mën nañu ko am, may nit deret, dialyse, dëkk ak ku am doomu jàngor bi, tukki di dëkk bu feebar bi bari, wala dëkkandoo ak ñu bari ci këru buur.[1][3] Ci jamonoy 1980, nit ñi daan nañu ko jëlee ci jamu (tatouage) wala pajum puso (acupuncture); waaye, loolu bareetul leegi ndax pexe yi ñuy rayee doomi jàngoro yi ci jumtukaay yi dafa gëna xarañ.[5] Jàpp loxo nit ku am hepatitis B joxewul feebar bi, bokk ndab, foon, akolaat, sëqët, tosooli, wala nàmpal itam du ko joxe.[3] Mën nañu gis feebar bi ci sa yaram su amee 30 jàpp 60 fan ginaaw bi mu la duggee. Ni ñu koy faral di saytoo ci sa yaram mooy xool ci sa deret ndax amul lenn lu bokk ci doomu jàngoro ji, wala ndax sa yaram tàmbiliwul defar luy xeex jàngoro ji.[1] Hepatite B benn la ci juróomi wirisi hepatite yi am: A, B, C, D, ak E.

Ci atum 1982 lañuy defar ñaq bu ci mëna musal nit ñi.[1][6] Waa OMS santaane nañu ñu ñaq xale yi ci bis bi ñu juddóo. Ginaaw ga dina ñu ko baamtu ñaar ba ñatti yoon ndax moo ëpp kaaraange. Baaxaayu ñaq bi yegg na ba ci 95%.[1] Amna lu tollu ci 180 yu ko boole ci seen prograamu xeex feebar ci atum 2006.[7] Wax nañu itam ni balaa ñuy may kenn deret nañu xool bu baax ndax amul wirisu hepatite B, te nañuy jëfandikoo kawas (kapot) sunuy sëy. Su lay sooga dal, paj maa ngi aju ci ni feebar bi feeñoo. Sudee ñu feebar yàgg lool ci ñoom, dañu leen di jox garab guy ray wiris bi lu ci melni tenofovir wala interferon; waaye nak garab yu seer lañu. Sudee ku feebar bi yàq resam, dañu koy defal beneen res.[1]

Ñatti nit ñoo jël ci àdduna bi kenn ci ñoom mus na ko am, te ci ñi ko am, amna 343 ñu feebar yàgg ci seen yaram.[1][8] Amna yeneen 129 milion ciy nit ñu feebar biy sooga dal ci atum 2013. At mu nekk hepatite B bi dina ray lu ëpp 750 000 doomi aadama.[1] Ci limuy ray amna ci 300 000 nit yumu yàq seen res ñu dee. Feebar baa ngi gëna baree ci Asie gu Penku ak ci Afrique gi si suufu Sahara, ñi fa am feebar hepatite B bu tar bi yegg na 5 ba 10% ci mag ñi. Sudee ci Europe ak Amerik du Nord, seen taux yeggul 1%.[1] Bu njëkk ñu ngi xamee woon ci "serum hepatitis".[9] Ñu jéema fexe nuñu defaree ñam yuy amaale ñaqu VHB.[10]  Feebar bi mën na dal golo yu mag yi itam.[11]

  1. 1,00 1,01 1,02 1,03 1,04 1,05 1,06 1,07 1,08 1,09 1,10 1,11 et 1,12 "Hepatitis B Fact sheet N°204". who.int. July 2014. Retrieved 4 November 2014.
  2. Raphael Rubin; David S. Strayer (2008). Rubin's Pathology : clinicopathologic foundations of medicine ; [includes access to online text, cases, images, and audio review questions!] (5th ed.). Philadelphia [u.a.]: Wolters Kluwer/Lippincott Williams & Wilkins. p. 638. ISBN 9780781795166.
  3. 3,0 3,1 et 3,2 "Hepatitis B FAQs for the Public — Transmission". U.S. Centers for Disease Control and Prevention (CDC). Retrieved 2011-11-29.
  4. Chang MH (June 2007). "Hepatitis B virus infection". Semin Fetal Neonatal Med. 12 (3): 160–167. doi:10.1016/j.siny.2007.01.013. PMID 17336170.
  5. Thomas HC (2013). Viral Hepatitis (4th ed.). Hoboken: Wiley. p. 83. ISBN 9781118637302.
  6. Pungpapong S, Kim WR, Poterucha JJ (2007). "Natural History of Hepatitis B Virus Infection: an Update for Clinicians". Mayo Clinic Proceedings. 82 (8): 967–975. doi:10.4065/82.8.967. PMID 17673066.
  7. Williams R (2006). "Global challenges in liver disease". Hepatology. 44 (3): 521–526. doi:10.1002/hep.21347. PMID 16941687.
  8. Schilsky ML (2013). "Hepatitis B "360"". Transplantation Proceedings. 45 (3): 982–985. doi:10.1016/j.transproceed.2013.02.099. PMID 23622604.
  9. Barker LF, Shulman NR, Murray R, Hirschman RJ, Ratner F, Diefenbach WC, Geller HM (1996). "Transmission of serum hepatitis. 1970". Journal of the American Medical Association. 276 (10): 841–844. doi:10.1001/jama.276.10.841. PMID 8769597.
  10. Thomas, Bruce (2002). Production of Therapeutic Proteins in Plants. p. 4. ISBN 9781601072542. Retrieved 25 November 2014.
  11. Plotkin, [edited by] Stanley A.; Orenstein,, Walter A.; Offit, Paul A. (2013). Vaccines (6th. ed.). [Edinburgh]: Elsevier/Saunders. p. 208. ISBN 9781455700905.