Gëm Dogal bi

Jóge Wikipedia.
Dem: Joowiin, Seet

NI NUY GËME DOGAL BI

Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi.

Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame