Fattalukaay(mbëj)
Fattalukaay ab cër la bees di jëfandikoo ci biir ndombo yu mbëj yi, di fees di rënk kàttanu mbëj niki toolub mbëjtekkaaral, yani mbëj yi ñoo fay tase dankaloo fa.
Dafay am ñaari làcc, yu tapp yees defaree ak lu man a wommat mbëj, yu làng ak benn diggante bi. Ñaari làcc yi yani mbëj yu dekkarloo fay nekk, wenn làcc wi yan bu ëpp (+) lay am weneen wi bu yées (-), segam ñaari yan yu dekkarloo dañuy xëccante, waral juddug toolu mbëjtekkaaral bi. Taraayu tool bee ngi aju ci limu yani mbëj yi nekk ci diggante làcc yi, moom itam aju ci dendu mbëj bi. Ngir bañ benn yan jóge ci wenn làcc dem ci weneen, faww ñu def lenn ci seen diggante, lenn loolu lees di woowee ab lankmbëj, man naa nekk ngelaw rekk walla këyit mbaa lépp luy bañ mbëj jàll ko. Ab fattalukaay bu nekk dafay am ab def (C) ñu koy natt ciy farad (F), dayoom a ngi aju ci lankmbëj bi, mooy li nuy wax dayoob toolu mbëj bi gën a rëy bi nga xam ne su ko weesoo yani mbëj yi man a jóge ci wenn làcc dem ci weneen, di luy waral itam yàqug lankmbëj bi.
- I mooy dawaan bi;
- U mooy dendu mbëj bi ci diggante ñaari làcc yi;
- C mooy defu fattalukaay bi.
- mooy coppiteeg dend bi ci jamono. Su dendu mbëj bees teg ci diggante làcc yi soppeekoo limu yani mbëj yi soppeeku, toolu mbëjtekkaaral bi soppeeku itam. Kon am na benn limu dend bees warul a weesu lu ko moy fattalukaay bi dafay yàqu, lakk.