Duusub sin

Jóge Wikipedia.
Ab duusub sin (bi xonk), beneen bi ab duusub cosin la

Ab duusub sin, ci xayma, melokaanu genn xeetu solo la, di luy jëmmal coppiteeg menn mbir muy dem ci jamono. Mbir mi man naa nekk jenn doole, dawaan walla dendu mbëj, ab duusub mbëjbijjaakon, dees na ko jëfandikoo ci fànn yu bari.

Màndarga bu ab duusub sin bi gën a fés mooy dayoob feeñte bi nga ciy jëmmal, ci saa-su-ne, soo jëlee ab diir, nga boole leen tus la lay jox. Soo xoolee nataal bi ci wet gi, di nga gis ne ñaari taxawaay yu solos sin bi yi ëpp, dañoo yam dayoo te safaanoo, koon seenug boole tus la.

Ngir xam dayoo bi ci jenn jamono ji, mii mbindum xayma lees di jëfandikoo.

Fi:

  • A, dooneeTaxawaay bi, mooy dayoob solo si bi ëpp.
  • ω, baraayu puxtal bi, moo nuy wax ni puxtal bi di soppeekoo ci jenn jamono, nu man cee xamee xélam, maanaam ni solo si di soppeekoo ci jamono, bennaanu nattam di radian ci saa (rad/s).
  • φ wéq, moo nuy wax fi solo si di tambalee fi jamono doonee tus, t = 0, ci ban puxtal la tambalee.