Daqaar

Jóge Wikipedia.
Nataalu garabug daqaar

Daqaar garab la gu fekk baax ca penku Afrig ca àllu Madagaskaar waaye bari lool ci Afrig sowwu jant fu ci mel ni Senegaal bari na fa lool. Guddaayam man naa àgg ci 20i met waaye itam dafa yeexug màgg waaye nag garab gu man a gudd fan la. Ca Senegaal nag, dees faa xaw a gaafal garabu daqaar. Di wax naan ay jinne dañu fay dëkk, ba ñu bari ñimewuñu koo def seen kër.

Meññeef mi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Daqaar ji, di meññatum garabug daqaar

Meññeefam te mooy doom yi guddaayam di mat 20i sàntimet. Buy door a meññ mooy benqal, day nëtëx te neex lool ñu man koy lekk noonu. Bu ñoree lay doon ub daqaar. Dees na ko jëfandikoo fu bari. Boo maccee doom bi ba noppi day am ab xoox ca biir. Xoox booba mooy sax. Daqaar dees koy jëfandikoo di ci defar naan yu neex. Ak di ko def maccaat ci ceebu jën, te itam njarum daqaar day faj seere di raxas biir, dana faj itam bóoli guy metti. Dees na ko def it cifaay ci laax, ñu di ko wax: Laaxu daqaar.

Ngogna[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Tóor-tóoru garabu daqaar

Ngogna di tóortóori daqaar. Moom it daawees na ko jëfandikoo ci cifaayu laax. Niki laaxub ngogna. Jamono yi daqaar gi meññagul amagul i doom te tóortóor booba lees daa jëfandikoo laaxub ngogna.

Cafna[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xobi daqaar

Mooy xobi daqaar. Moom it daawees na ko jëfandikoo di ko def cifaay di ko boole ak laax ñu koy wax laaxub cafna. Jamono ji nga xam ne daqaar gi meññagul, tóortóoragul ci lees daa jël xob yi di ko def cifaay.

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Tamarindus indica