4
Njabootug sëriñ Tuubaa gi daa nañu fa ñëw lu bari, ku mel ni sëriñ ''Fàllu''', sëriñ '''Basiiru,''' sëriñ '''Baara''', moom sax sëriñ '''Baara''' mii moo feeñal dëkk ba, sëriñ '''Sohaybu''', it daa na fa ñëw ak '''sëriñ Murtalaa''' añs... daan nemmiku mbóot ya fa nekk, ak a xeeñtu saaway ñu baax ña fa nekk. Ci atum 1945 la sëriñ Faatu Jaxate boroom dëkk ba nelaw wuyu ji Boroomam, '''sëriñ Seex Jaxate''' wuutu ko fa, ba atum 1990, mu wàcci '''sëriñ Fàllu Jaxate''' wuutu ko fa ba atum 2016 '''sëriñ Murtalaa Jaxate''' nekk fa, yal na ko fi Yàlla yàggal, moom sëriñ Murtalaa Jaxate mii nag, di jàmbaar lool, joj, def na fa liggéey bu rëy yeesal na barabu sëriñ Faatu Jaxate ba, natt dëkk ba liiñe ko, defar rfa jumaa ju mucc ayib, at mu ne amna màggal gu fay am, muy ag ñaan gog dina ñu ko defal seen maam yu baax yooyu.