Bunt: Xarala

Jóge Wikipedia.

BUNTU XARALA

« Xarala ab baat la bu yaa ñeel lepp lu jëm ci jëfëndikoo walla xamtey jumtukaay ak xereñ gu nit jëmal-kanam.»


Ay wall

Jokkoosoryante

Xaralaymbëj

Doolerandu

Kattan

Dalub Archimède

Mbëj

Mbëj dadi ab feñfeñ gu gisuwul ak bët gu’y feñ ci ag wootal walla bëmëxënte ci digante yanub mbëj yi. Ci gattal mooy bepp feñfeñ gu juddu ci jamarlo gi nekk ci diggante: feppselal yi, ñoom ci lu ëpp ñoom du ñu’y tekkaaral, ak mbëjfeppal yi nga xam ne ñoo ëpp yëngu-yëngu,ci biir xarefulwon gi. senug demin jur ag dawan.

Su ñu ko boole ak xëccu, mu jur beneen baŋxaas gi ñu duppee mbëjxëccu. Mbëj moo yor ay feñfeñu nek yu mel ne mellax, toolu mbëj ak dawanu mbëj (ci lu bari dañ leen di jaawale).

Mbëj doon na “jaamu” nit gi gën, doon tamit raññeekayu adduna gi bees gi. Dafay leeral sunu dëkkuwaay yi di doxal sunu këru kom-kom yi te jegele nit ñi gënoona soriyante. Jàng lepp

Doxalkat mbëj

Doxalkat mbëj tekkeem moy ab wuutuloxo mbëj la goo xam ne kattan giy duggu ci moom gu mbëj la te ga muy genne gu doolerandu la. Doxalkat mbëj yi am nañ solo lool ci dundinu jamono gu bees gi, te it dëggë la sax ne limu doxalkat mbëj yi nekk ci am reew day firndeel tolluwaayu jëm-kanam mam. Te itam deminu, maanam yokkute walla nèewte limu doxalkat mbëj yi ci am reew bokk na ci wonekat yiy firndeel tolluwaayu yokkute ci wallu xarala mu reew moomu. Ngir dëggël loolu, doyna xool ci jumtukaay yi nekk ci li ñu wër: ca saxaar ba ci watukaay ak yeneen ak yeneen, yi ngeen xam ne nit ku bees ki moo ngi koy jëfëndikoo bu baax, mën naa ni sax ñooy doxal sunug dundu. Jàng lepp