Aller au contenu

Abiya

Jóge Wikipedia.

Ci làkku ibrë la tur wi jóge. Ci angale mooy Abijah or Abia; Ci faranse mooy Abia

Ci Injiil dañuy gis ñaari nit ñi bokk tur Abiya.

  1. Ñaareelu buur ci Yuda, mooy doomu Robowam. Ñetti at la nguuru ci Yerusalem. Bind nañu ay jalooreem ci 1Ki 14:31-15:8; 2Ch 11:20-22; 12:16-14:1. Bokk na ci maamaati Yeesu yi ñu bind ci Mc 1:7.
  2. Kenn ki soqikoo ci Aaroona (1Ch 24:10). Daawuda fal na askanu Aaroona ngir ñu toppatoo liggéeyu këru Yàlla. Mu xàjjale leen ba ñu nekk 24 kër. Kër gu nekk toppatoo nañu ñaari ayu-bés at bu nekk. Sakariya, baayu yonent Yàlla Yaxya bokkoon na ci askanu Abiya (Lu 1:5).