Aaroona

Jóge Wikipedia.
Aaroona

Ci làkku ibrë (אַהֲרֹן) la tur wi jóge. Aaroona mooy ni ñu ko waxe ci Lislaam. Ci angale ak ci faranse mooy Aaron.

Magu yonent Yàlla Musaa la woon, ñu bokk ndey ak baay. Ñetti at la Aaroona mage Musaa. Baayam, Amram la tudd te yaayam Yokebedd (Ex 6:20). Amoon na ñeenti doom yu góor ci jabaram, Eliseba. Ñooy Nadab ak Abiyu ak Elasar ak Itamar (Ex 6:23). Aaroona amoona benn rakk bu jigeen, mingi tudd Mariyaama, doomu ndeyu Aaroona ak Musaa (Ex. 15:20). Mariyaam bii, bokkul ak yaayu Yeesu Krist.

Ba Musaa demee ci kanamu Firawna Aaroona dafa àndoon ak moom ngir nekk yonentam (Ex 7:1). Yàlla tànn na ko, mu jëkka doon saraxalekat bu mag ba ci biir bànni Israyil. Moom moo sàkkaloon bànni Israyil benn xërëm bi xaaroon Musaa ca tundu Sinayi. Ñu tëgglu aw sëllu, muy xërëm, ñu di ko tuuru, di bànneexu ci seeni jëfi loxo (Ex 32:1-28). At, ya Aaroona dundoon, 123 la. Ci kaw tund wi ñu wax Xor la faatu (Nu 33:39).

Man nga jàng jalooreem ci Ex 4:14-16; 4:27-31; 5:1-4; 15-21; 6:28-7:13; 19-22; 8:5-12; 16-19; 9:8-12; 16:2-10; 19:23-24; 24:1-2,9-15; 28:1-12,29-30; 32:1-8,14-28,35; 34:29-33; Le 8:1-9:24; 10:1-4; Nu 3:1-4; 12:1-15; 14:2-5; 16:1-35; 41-50; 17:1-10; 18:1,8,20; 20:1-12; 23-29; 26:58-61.

Ci Injiil dañuy wax ci Aaroona ci Lu 1:5; Jëf 7:40-41; Yt 5:4; 7:11; 9:4.