Ñaqu rougeole (ŋas)
Ñaqu rougeole (ŋas) mooy li lay musal ci rougeole.[1] Sudee bi nga njëkkee ñaqu sa yaram defarul lu koy aar ci feebar bi, soo ñaquwaate rek feebar bi dootul mën dara ci yaw.[2] Sudee dañu ñaq lu weesu 92% ci waa dëkk bi, mën nañu jàpp ni dëkk boobu feebar bi dufa feeñ; waaye mën na fa ñëwaat sudee limu ñiy ñaqu dafa dem ba wàññiku. Soo ñaqoo dinga mucc ci feebar bi ay at yu bari. Xama guñu bu baax ndax ndax kaaraangeg ñaq bi dafay wàññiku. Ñaq bi mën nala aar itam soo ko jëlee ci biir ñaari fan yi nga nekk ci barab bula feebar bi mëna dale.[1]
Ñaq bi du indil nit ki benn jafe-jafe, doonte danga am VIH. Mën nala xawa sonal tuuti waaye du yàg dara. Maanaam fi ñu la ko jam mën na saf tuuti wala sa yaram xawa tàng. Amul benn yokkute buy seetlu ci limu Seetlu nañu itam 3,5 jàpp 10 kaa anaphylaxie ci miliyoŋi nit ñuñu ñaq. Sudee lu jëm ci feebar Guillain-Barré, autisme ak biir buy metti (maladie intestinale inflammatoire) gisu ñu ci benn yokkute.[1]
Ñaq bi amna mooy kese, waaye itam dina ñu koy boole ak yeneen ñaq yu ci melni ñaqu ROR, (muy boole ñaqu rubeole ak anti-ourlien) wala ñaqu RROV (maanaam ñu boole ñaqu RRO ak ñaq biy aare ci varicelle). Ñaq bii aare ci rougeole dafay musalaate ci feebar itam ndeem dañu ko boole ak yeneen ñaq, te effets secondaires yi dañuy wuute, lépp di aju ci xeetu ñaq bi ñu ko booleel. Waa OMS ñoo digal ñu ñaq xale bi su amee juróom ñeenti weer te nekk ci barab bu feebar bi bari. Waaye sudee fu feebar bi bariwul la, jaaduna ñu ñaq xale bi su amee fukki weer ak ñaar. Ñaq bi luy doomu jàngoroy rougeole bu dundu la waaye dañu ñéewal dooleem. Ñaq bi puudar bu waw la, fàww ñu jaxase ko laata ñu koy jam nit ki ci suufu deram wala ci siditam. Soo bëggee xam ndax ñaq bi jàppna danga saytu deretam.[1]
Ci atum 2013, ñaq nañu lu tollu ci 85% xale yi ci àdduna bi.[3] Ci atum 2015 amna gën gaa néew 160 réew yu baamtu ñaq bi ngir nit ñi mën a am matuwaay yu leen musal ci feebar bi.[1] Ci atum 1963 la ñu njëkka génne ñaq bi.[2] Ci limu garab yu am solo yi waa OMS def, mooy ñaq bi gëna am solo bu yaramu nit ki soxla.[4] Njëgi ñaq bi ci réew yu néew doole yi mingi tollu ci 0,70 USD dose bu nekk, en gros, li tàmbale 2014. Ginaaw feebar bi dafa faral ci barab yi nit ñu bari ñaquwul, feebar dina tax ñu xam barab yi ñaq bi barul ñu ko def.[1]Royuwaay:Infobox drug
- ↑ 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 et 1,5 "Measles vaccines: WHO position paper" (PDF). Weekly epidemiological record. 84 (35): 349–60. 28 August 2009. PMID 19714924.
- ↑ 2,0 et 2,1 Control, Centers for Disease; Prevention (2014). CDC health information for international travel 2014 the yellow book. p. 250. ISBN 9780199948505.
- ↑ "Measles Fact sheet N°286". who.int. November 2014. Retrieved 4 February 2015.
- ↑ "WHO Model List of EssentialMedicines" (PDF). World Health Organization. October 2013. Retrieved 22 April 2014.