Namandiru

Jóge Wikipedia.

Namandiru, nekkoon na nguur gu nekk Senegaal ca jamono yu yag ya. Ca VIIeelu xarnu am na benn njabootay bu tuddu Jaa-Ogo, ñow nañu dëkk ca penku Senegaal, ca wetu dexug Senegaal. Jaa-Ogo yi, Misra lañu juge. Daw nañu wa Misra ndax foofu, ay jaambar ñu leen tuddu Perse, ñow nañu ca biir Misra, di bëgg noot reew mi. Li mooy tax Jaa-Ogo yi, gadday ba agsi dexug Senegaal. Ca dëkk boobu, kenn nekku fa woon. Ca senegaal tabax nañu nguuru Namandiru.

Jaa-Ogo yi, tëgg moo doonoon seen liggeey. Jaa-Ogo yi ñoo indi liggeey bi ca Senegaal. Li mooy tax ca jamono boobu tëgg yi ay buur bu mag lañu nekkoon. Ndax takkay yi, paaka yi, tin yi, leppu ñuy jefandiko ak weñ, ñoom rekk ñoo ko mënoon. Jaa-Ogo yi, am na yu bari deeñi ne, ca Pël yi lañu bokkoon, ndax tur bi ñu joxe seeni nguur Namandiru, ca lakku Pulaar la juge, di tekki = Reew mi am lepp. Seen sant yi tamit, moo di ay sant Pël yi yore. Jaa-Ogo yi ñoo tabax tamit nguuru Tekuruur, tey di nekk Fuuta-Tooro.

Njabootu Manna yi, ñoo daan Jaa-Ogo yi. Manna yi ay Saraxule lañu nekkoon, di sant Ñaxate ak Sumaare. Tamit Naar yi, ca Xeelu xarnu, ak seen buur Abu Bakr ibn Umar, xeex nañu ak Jaa-Ogo yi. Manna yi ak Naar yi mooy tax, Nguuru Namandiru daan.

Boobu ñu nekkoon buur, ci seen jeexit itam, bekkoor bi fekk na leen, ba tax Jaa-Ogo yi gaddayaat ca yeneen dëkk ca Senegaal.

Nguuru Njaarmeew[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ba noppi, am na beneen njabootay ñu sant Ndaw, juge Gannar, diwaanu Assaba, ñow nañu ca dëkk bi amoon Namandiru, di fi tabax beneen nguur ñu woowe ko Njarmeew. Seen Buur, Belëp la tuddoon. Ndaw Belëp yi, yaguñu fa. Ndax ca XVeelu xarnu, Buurba Jolof ba, Tyukuli Ndiklam, uuf na dëkk bi ca biir Jolof, ak Tekuruur itam. Kon Ndaw Belëp yi, daw nañu ba Nguuru Seereer yi ca Saluum. Foofu Maad Saluum bi, Mbegaan Nduur, may na benn Diwaan buuru Ndaw Belëp bi, moom Waly Mberu Mbakke Ndaw la tudd. Diwaan bi, Nduukuman la.

Koly Tenŋela, ca XVIeelu xarnu, Njaarmeew bi jël na ko, sooga Malik dawda Si, Toorodo bi, ñow foofu di tabax Nguuru Bundu.

Tëgg yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Jaa-Ogo yi, ñoo maamu tëgg yi ca Senegaal.

Ñu sant: Caam, Mbow, Conŋaan, Ñas, Bittey, Acc, Jaw, Mbaay. Ñoo ëppp ca Tëgg yi nekk Senegaal.