Tekuruur

Jóge Wikipedia.

Dem : Joowiin, Seet

Tekuruur moo doonoon nguurug Tukulóor yi. Xeet yu bari tase nañu fa, Juge Isipt: Séeréer si, Wolof, Pël, Soose, Naar yi. Leeegi Tekuruur, Fuuta-tooro la tudd. Koli Tengela Ba, Silatigi bi, moo ko jox tuur wi. Ca nguur ga, Tukuloor ak Pël ñoo fa ëpp ba tay, waaye Séeréer si ñoo fa jëkk a nekk, ak Pël. Buur yu bari ñoo yoroon nguur ga:

  • Ja-Ogo yi ci yoonu imbratooru Gana.
  • Manna yi.
  • Tondiyoo yi.
  • Lam-Terme, Lam-Taga, ak Lam-toro yi. Ci nu nekke buur, Jolof moo doon uuf dëkk bi, di fi teg ay Farba.
  • Deñankoobe yi, yu Koli tengela Ba, Sebee lañu woon, Sebbe mooy Ceddo.
  • Almaami yu Torodo yi. Sulaymaan Baal ak Abdul Xaadir Kan, ñoo dàq deñanke yi ci atum 1776. Ay Jullit lañu.

Ba noppi, tubaa yi ñëw ak canc gi (colonisation), ci atu 1890, jël nguur gi, ray Almaami yi, di séddale dëkk bi, ci ay - li nuy wax ci lakku fraanse (Canton) ak (Provinces).

Tekruur mooy dëkku tukruur yi. Tekruri mooy turu Tukulóor, bu jëkk noonu lañu tudde woon seen bopp. Tur wi ñuy wax Tukuloor tubaab moo ko fi indi, ndax xeet wi dafa jaxase yu bari, am na ay Tukuloor yu seeni maam wolof lañu, mooy tukuloor yi sant Njaay, Joop, Faal, Ñang, Mbóodj, ak yu deme nonu, am na ñu seeni maam ci xeet yu séeréer lañu bawoo, niki Juuf, Saar, Fay, wala Soose, niki Kamara, Siise, Ture.