Joolaa (askan)
Joolaa genn la ci giiri Senegaal yi. Ñoom Kaasamaas lañu fekk baax. Ca yoonu Imbraatóor gu Mali, lañu dem dëkk. mandeŋ yi ñoo leen dàq, ñu dem kaasamaas. Ca bëj-gànnaaru Gine Bisaawóo tamit ñoo ga fa. Baynuk yi ñoo doon jiite joolaa yi ca kaasamaas. Ñoo tabaxoon nguurug Kasanlaa. Joolaa yi ak Baynuk yi, dañu dëkkandoo woon ak Soose yi, Njaago yi ak Pël yi. Ñoom ñoo fa njëkkoon joolaa yi.
Joola sen Ada niogi ko gëne xam si Bukut.
Bukut neek ab Ada bu nu rane si Joola yi

Mboor (Taariix)
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Joolaa yi ca sowwu Kaasamaas lañu tabaxoon seeni nguur, nguuru Banjal, nguruu Flub. Mbayum ceeb, napp, Sàmm, ñoo doonoon seen xeeti liggéey. Tiramakan Taraaware, di ab Mandeŋ bu bokkoon ca imbratóor gu Mali, moo leen sancoon ci ndigalu jàmbaari buur jooju di Sunjata Keyta. Sunjata Keyta moo yónni woon Tiramakan ca kaasamaas ngir mu jël nguuri joola yépp yokk ci imbratóoram.
Tiramakan ca la boole nguuri Joolaa yi ak yu Baynuk yi ci genn nguur duppe ko Kaabu. Nguur gi demoon na ba ci dexug Gàmbi gi, ba Bajar, bëj-gànnaaru Gine bisaawoo. Màndeŋ yi ak Joolaa yi xeexuñu benn yoon, dañu a nekkoon ci jàmm, di dëkkandoo. Joolaa yi ak Mandeŋ yi itam dañoo jaaxasoo woon ba bokk ay sant ( Sonko, Saane, Maane, Jaabi, Saañaa).
Ci XVIeelu¹⁶ xarnu la tubaab yi ñëw Kaasamaas. Bi leen tubaab yi bëggee sanc ñoom dañoo bañoon, taxaw jammaarloo ak ñoom, masu ñoo nangu itam njàppum jaam, seenug njàmbaar terewuloon waa-portugaal yi mujj leen sanc. Ca XXeelu²⁰ Xarnu, la Aliin Situwe Jaata jàmmaarloo ak tubaab yi ngir dakkal canc gi. Joolaa yépp ànd ngir xeex. Aliin dajale góor ñépp ngir jàmmaarlo gi. Waaye seen fipp googu manutoon aantal seen yéene ngir seenug néew-doole ci kanamu sancaan bi. Ci lañu jàppee Aliin gàddaayal ko Tumbuktu ca Mali, foofu la génne àdduna.
Xeeti joolaa
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Joolaa yi ci seen biir dañoo séddaliku ciy xeet yu bari.
- Fooñi
- Felup wala Kasa, ñoom ño tabax nguuru Usuy
- Ejamat, Joola yu Gine-Bisaawóo
- Yoola
- Elufayi
- Eyunayi
- Eblufayi
- Seleg
- Ajuwat
- añs
Seen i sant: Jéeju, Jaata, Jamakun, Saañaa, Gujaabi, Jaabi, Kóli, Bojã, Baaji, Maane, Saane. Biyaagi, Baseen, Ehemba, Sambu.
Diine
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Ci Joola yi am na ay jullit, ay katolig, waaye am na it ay ceddo. Tubaab yi ñoo leen dugal ca diiney katolig, Wolof yi ak Pël yi ñoo leen dugal ci lislaam.
Xool it
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]Téerekaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (en) Alice Joyce Hamer, Tradition and Change : A Social History of Diola Women (Southern Senegal) in the twentieth Century, Michigan University, 1983, 329 p. (Thèse)
- (en) Olga Linares de Sapir, « Shell middens of lower Casamance and problems of Diola protohistory », West African Journal of Archaeology (Oxford University Press), Ibadan, 1971, vol. I, p. 23-54
- (en) Olga F. Linares, Prayer, Power, and Production: The Jola of Casamance, Cambridge University Press, 1992, 280 p.
- (fr) A. Badji, La lutte traditionnelle joola. Étude et perspectives, Dakar, INSEPS, 1982, 47 p. (Mémoire de Maîtrise STAPS)
- (fr) Saloum Badji, Habitat et occupation du sol dans les pays jolla (du XVe au XXe siècle, Dakar, Université Cheikh Anta Diop, 2000, 121 p. (Mémoire de Maîtrise)
- (fr) Alioune Diatta, Structures politiques et sociales du monde traditionnel Joola, Paris, Université de Paris I, 1982, 345 p. (Thèse de 3e cycle).
- (fr) Nazaire Diatta, Le taureau, symbole de mort et de vie dans l’initiation de la circoncision chez les Diola (Sénégal), Paris, EHESS, 1979, 3+292 p. (Mémoire EHESS)
- (fr) Nazaire Diatta, Anthropologie et herméneutique des rites joola : funérailles, initiations, Paris, EHESS, 1982 (Thèse de 3e cycle)
- (fr) Nazaire Diatta, Proverbes Jóola de Casamance, Karthala, 1998, 416 p. (ISBN 2865377180)
- (fr) Christian Sina Diatta, Parlons Jola - Langue et culture Diolas, L'Harmattan, 1998, (ISBN 2-7384-7169-2)
- (fr) Athanase Diédhiou, Chants funèbres et rites traditionnels dans la société Diola, Dakar, Université de Dakar, 198? (Mémoire de Maîtrise)
- (fr) Lamine Diédhiou, Riz, symboles et développement chez les diola de Basse Casamance, PU Laval, 2005, (ISBN 2763781802)
- (fr) Odile Journet-Diallo, Les créances de la terre. Chroniques du pays jamaat (Joola de Guinée-Bissau), Turnhout, Brepols, collection BEHE, n° 134, 2007, (ISBN 978-2-503-52666-9)
- (fr) Françoise Ki-Zerbo, Les sources du droit chez les Diola du Sénégal : logiques de transmission des richesses et des statuts chez les Diola du Boulouf (Casamance, Sénégal), Karthala, 1997, 217 pages (ISBN 2865376516)
- (fr) Michel Bokar Mballo, Le personnage du prêtre dans la société traditionnelle diola cassa et la société traditionnelle romaine dans ses différentes attributions, Dakar, Université de Dakar, 1981, 97 p. (Mémoire de Maîtrise)
- (fr) Michel Bokar Mballo, Les survivances des religions traditionnelles chez les chrétiens de l’époque de saint Augustin et chez les chrétiens diola kassa de la Basse Casamance, Dakar, Université de Dakar, 1985 (Thèse de 3e cycle)
- (fr) Paolo Palmeri, Retour dans un village diola de Casamance, L’Harmattan, 1995, 488 p. ISBN 2-7384-3616-1
- (fr) Jean-Joseph Sambou, La notion de Boekin dans le conte diola, Dakar, Université de Dakar, 1984, 154 p. (Mémoire de Maîtrise)
- (fr) Francis G. Snyder, L’évolution du droit foncier Diola de basse-Casamance (république du Sénégal) : étude d’anthropologie juridique des rapports entre les hommes et les terres chez les Diola-Bandial, Paris, Université de Paris I, 1973, 550 p. (Thèse de 3e cycle)
- (fr) Louis-Vincent Thomas, Les Diola. Essai d’analyse fonctionnelle sur une population de basse-Casamance, Dakar, IFAN, Université de Dakar, 1958, 821 p. (Thèse d’Etat publiée)
- (fr) Louis-Vincent Thomas, Et le lièvre vint : Récits populaires diola, Nea, 1982, 266 p. (ISBN 2723608301)
Filmkaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]- (de) Das Fest der Ringer. Bei den Diola im Südsenegal, téléfilm documentaire allemand de Essibyé Augustin Diatta et Ulla Fels, 1999
Lëkkalekaay yu biti
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]
Xool it Wikimedia Commons
|
- (en) « Shrines of the Slave Trade : Diola Religion and Society in Precolonial Senegambia » (Robert Martin Baum, Oxford University Press, 1999 ISBN 0195123921)
- (en) Chronology for Diolas in Casamance in Senegal (fiche du Haut Commissariat des Nations unies pour les réfugiés, 2004)
- (es) Les Diolas
- (fr) Les Diolas
- (fr) Casamançais, Diolas et animisme
- (fr) « Les jeunes Diola face à l'exode rural » (Marie-Christine Cormier, géographe, ORSTOM, CRODT, Dakar, 1984)
- (fr) « Quelques proverbes Diola » (Nazaire Diatta Ukëyëng, ecrivain)