Jullit

Jóge Wikipedia.


Wikipedia
Wikipedia
Bii jukki ab junj rekk la. Man nga cee duggal sa loxo suqali ko ndeem am nga ci xam-xam ci anam yi Wikipedia taxawal


Jullit mooy ku topp Diiney Lislaam, sartees nako ci nangu te wax ni «Maangi Seere ni amul jenn Yàlla ju dul Yàlla (Allaa); Te maangi seere ni Muhammad ndawul Yàlla la» ñu koy wax Baati Seere yi

Ginnaaw wax jooju, sartees ci kawam, mu Gëm Yàlla moomu ca namu ware, gëm ni amul ndey, amul Baay, Amul fumu yamle, Amul kumuy bokkaaleel, amul ab tàmbali, amul ab dayo, Mooy degg, Mooy gis, te day jàpp, Déggam googu ak gisam gi aki meloom yépp, Darra nduroowu ci ak niko leneen di defe, Gisug lépp, ak déggug lépp, moongi aju ci moom, nduroo wul ak darra, Darra nduru wu ko, Darra umbu ko, teewe na lune, moo Sos lépp, Moo bind nit ak Jinne, Moo sàkk dénd bi, Lu am moom la neex, ak lépp li ci aju ci gëm ko... fii Gëm Yonent yépp ci lu dul ag xàjjale, Gëm amug Malaaka yi doonte gisu léen, Gëm ëllëg bisu pénc ba, Gëm Dogal bi ni lu am rekk mooko dogale noona, Gëm Téere yi mu wàcce woon yépp ca ñu jëkk ña ak ñu mujj ñi, te gëm ni Alxuraan rekk moo ci di Téere buy wéy ba fimne, nangu li Yàlla wax ci Alxuraan lépp, nangu it Hadiisi Yonent bi Muhammad, Nangu Julliy Juróom bis bu ne, nangu joxe Azaka ndeem war na ci Alalam, nangu Woor, nangu Haj aw yoon ci sag dund ndeem man nga

AJ