Aller au contenu

Bisu Tamxarit

Jóge Wikipedia.
Dencukaay:Tamkharit.jpg
Cerey Senegaal

Bisub Tamxarit Ak Bisub Tamñërit, Bisub Tamxarit di 9eelu fan ci weeru Tamxarit, bis la budi aw xew ci Jullit ñi, rawatina ñi ëpp ci sunnit yi, Siiha yi it dina ñu ko xewal ngir naqarlu, ray gees rayoon Useynu Sëtub Yonent bi (Jàmm ci ñoom) ca réewum Iraak, nees nako fa xumbal, ci àndandoo wàcc ci mbedd yi, di wone séni naqar, Ci julliti Senegaal yi, Baaxoos na toggi cere ca ngoon ga, ba ca guddi ga di guddig Fukkéelu fan ba, mu di guddi gu màgg ci lislaam ngir ay xew-xew aki ngënéel yu ci Yàlla jagleele, ku ca jàppu ba séll julli ñaari ràkkaa, ràkkaa bu ci ne nginnaaw faatiha nga tari saar wu la soob ci Alxuraan, boo noppee sàbbaal Yàlla lu la soob, julli ci Yonent bi (Xeewalug yàlla ci moom) lu la soob, te ñaan say aajo muslu ci balaa yoy at mi.

Ammaa nag yeneen yees ciy def niki, jal suuf di ca këpp bool bañu doon reere, ak bàyyi ca bool ba ab danku cere ak tuuti ndox bu ñu xëyee di ci sëlmu, mbaa tusngalu di séentu asamaan ngir ni dañuy gis Faatimata bintu Rasuulilah, (Tusngalu nag sopp nañu ko ci), Yooyu yépp ku koy def walla ku koy deflu mbaa ku gis ku gis ku koy def, na ko jàppe ni baax (aada) la rekk xamu ma nag séeni cosaan waaye tegeesu ko ci diine. Tamñërit di bisub fukkéel ci wéeru Tamxarit, bis bu màgg la ci xew-xewi àddina rawatina ci Lislaam li ko dale ci sosug nit ba léegi, Yàlla defal naci ay jaamam xéewal yu rëy aki ngënéel, jéggal ci it ay jaamam,

Xew-xew ci bis bi:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
  • Ci bis bii la Yàlla jéggalee woon Aadam ca bàkkaar bamu defoon ca àjjana bamu laalee garab ga
  • Ci bis bii la gaalug Yonent Yàlla Nooh (jàmm ci moom) ga teeroon ca géejug juudiyu (nékk ca Iraak) ba Yàlla di mbugal xeetam wa ca ndox ma.
  • Ci bis bii lees xaralee woon Yonent Yàlla Muusaa (jàmm ci moom) géej ga te labal Fir`awna aki ñoñam, Muusaa mucc aki ñoñam.
  • Ci bis bii la Yonent Yàlla Iisaa (jàmm ci moom) Juddu woon te wax waxi dëggëm ja,
  • Ci bis bii la Yuunusa (jàmm ci moom) génn ca jënwa ginnaaw bi ko ci Yàlla yabalee, ca génnam ga ci ludul ndigalul Yàlla.
  • Ci bis bii la Yonent Yàlla Yuusufa (jàmm ci moom) génnoon ca téen ba ko mbokkam ya dugaloon.
  • Ci bis bii la Yàlla musëlee woon Yonent Yàlla Ibraahiim (jàmm ci moom) ca sawara sa ko noon ya fasoona dugal ci ndigalul Namruus bamu diiŋatee la ñu jàppe woon Yàlla.
  • Ci bis bii la Yàlla yékkatee woon Yonent Yàlla Idriisa (Jàmm ci kawam) ba ca ñeenteelu Asamaan.
  • Ci bis bii la Yàlla yékkatee Yonent Yàlla Iisaa (Jàmm ci moom) ma nasaraan yi naan «rayees na ko» Alxuraan ni «Rayeesu ko sëlabeesu ko waaye dees léen a ndurooleel (Keneen ku nduroo ak moom)», moo nga ca ñaareelu Asamaan.
  • Ci bis bii la Yàlla jéggalee Yonent Yàlla Daawuda (jàmm ci moom) ca àtteem bu jeng ba ci laaj kenn ka ba ka ca des,
  • Ci bis bii lees di wodd Kaabak Màkka gees wormaal, (amaana muy ci lu nëbbu mbaa lu féeñ, lu nëbbu nag laa gën a jàpp ndax budee lu feeñ moom aada la te manees nakoo bàyyi.)

Yii yépp nag ay ngënéel yu nekk ci bis bi lay wone, ngir ni Yàlla a tànn xew-xew yii jagleel bis bi waliif yeneen yi, kon manees na cee tegoo ak jaamu kem sa kàttan te ñaan say aajo, ngir dabu ngënéel li ci ne. nuy Yakaar nangug séeni ñaan.


Soppees na ci bisub Tamñërit di bisu 10eel ba yii:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sopp nañu kuko Woor, Sopp nañu ku ci julli ñeenti (4 i) ràkkaa yu boloo, bu ca ne mu jàng ca Saaru Faatiha benn yoon ak Saaru Lixlaas (Xul huwal laahu) fukk ak juróom, Sopp nañu ku ca jokk ak bokk, Sopp nañu ku ca seeti dëkkandoo bu di aji wopp te dëfal ko. Sopp nañu ku ca sangu, Sopp nañu ku ca saraxe, Sopp nañu ku ca lewwi ku dagg say wee, Sopp nañu ku ca raay boppum jirim bu di ab jullit te jox ko dara, jirim moodi ku baayam dee te amagul 18 ci ay at, ngir won ko ak cofeel mu man a jàppe boppam niki ay moroomam, Sopp nañu ku ca tusngalu, Sopp nañu ku ca siyaare boroom xam-xam,Sopp nañu ku ca yaatal ag njabootam ci lekk ak naan niki soppi sa cin temu matale, Sopp nañu ku ca jàng Saaru Lislaas (Xul huwal laahu) junniy yoon (1000), Sopp nañu ku ca jàng ñaan gii:70 i yoon «حسبناالله ونعم الوكيل نعمالمولي ونعم الموكيل», teg ca ñaan gii «سبحان الله ملء الميزان ومنتهي العلم ومبلغ الرضي وعدد كلمات الله التامات كلها أسألك السلامة برحمتك ياأرحم الراحمين ولاحول ولاقوة إلابالله العلي العظيم وهو حسبي ونعم الوكيل نعم المولي ونعم النصير وصلي الله علي سيدنا محمد وعلي ءاله وصحبه وسلم تسليما» jullig ñeenti ràkkaa gi nag manees na koo def ci ag booloo, rawatina ñu ko man la defal séen bopp, te it ginnaaw julli gi Yilimaan ji jàng ñaan gii ci anam gu leer bu ko defee maamoon ya man koo roy lu mu wax ñu wax ko, Njariñi yenn ci yii: Sangu ci bis bi day dàq ag ràgg, Tusngalu ci bis bi day jañ Gumba, Soppi sa cin temu matale day yokk wërsëg. Koor gi Sunu Yonent Muhammad (Jàmmi Yàlla ci moom) wax nani «Woor léen Tamxarit bisu Juróom ñeenteel ba ak bob fukkéel ba ndax day far bàkkaari atmi»


Ku ca bind lii:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Saaru Faatiha, Aaayatu kursiyu, Lixlaas, Falaqi ak naasi lu ci ne benn yoon, teg ca juróom ñaari laaya yii wu ci ne balaa nga koy bind, bind BISMIL LAAHI AR-RAHMAANI AR-RAHIIMI, ñooy yii:

  • 1-سَلَامٌ قَوْلًا مِّن رَّبٍّ رَّحِيمٍ (Saar:36, laaya:58)
  • 2-سَلَامٌ عَلَىٰ نُوحٍ فِي الْعَالَمِينَ, إِنَّا كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:79-80)
  • 3- سَلَامٌ عَلَىٰ إِبْرَاهِيمَ, كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:109-110)
  • 4-سَلَامٌ عَلَىٰ مُوسَىٰ وَهَارُونَ, إِنَّا كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:120-121)
  • 5- سَلَامٌ عَلَىٰ إِلْ يَاسِينَ, إِنَّا كَذَ‌ٰلِكَ نَجْزِي الْمُحْسِنِينَ (Saar:37, laaya:130-131)
  • 6- سَلَامٌ عَلَيْكُمْ طِبْتُمْ فَادْخُلُوهَا خَالِدِينَ (Saar:39, laaya:73)
  • 7- سَلَامٌ هِيَ حَتَّىٰ مَطْلَعِ الْفَجْرِ (Saar:97, laaya:5)

Raxaseko walla jambe ko ndoxum taw walla ndoxum teen mbaa ndoxum géej maanaam ndox muy dund, Ku ca naan Yàlla dana ko musël ci mboolem lu ñuy ragal ci mboolem musiiba yi ci at mi


Li waral baatu "Tamxarit":

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ñaari baati Wolof lees ci boole ñuy "Tam" di tekki jiiñ nit ak miim-deel (dëmmu) ak baatu "xarit" am ñaari tekki: benn, Xarit niki xaaj dara ca digg ba benn xaaj ba moodi xarit, ñaar, Xarit niki nit kooy àndal di diisoo ak yuni mel, (bii nag amaana mu jóge ci bu jëkk bi niki taqaloo gi), bees boolee tam ak xarit mu joxe Tamxarit, di jiiñ sa xarit ag miim-deel, ñu tuddee ko bis bi/weer wi, kon ana lu ko waral ? waaw, ndax waxees nani waaja daa woo ab xaritam ci reeru bis bi (fekk waaji daa Buun) xarit ba ñëw ñu taaj reer bi (cere ji) xarit ba topp ab ndeyjooram duy biir ba ci cerey yàpp ji ba mu fees dell, ñibbi biir ba di metti ci guddi gi tax ñu tamxarit ba mu demoon kërëm mu jox ko lekk ni mooko jàpp, bañu xëyee nag cere ja rees biir ba sedd ñuni aah Tamñërit, manaam tam ja wéy na, neena mërr, ñu tuddee bisub juróom ñeenteelu fan ba Tamxarit (ci lees tamoon xarit bi), bu ca goon gaa ñu baaxoo toggi cere aka Taa ja buun, tuddee bisub fukkéel ba Tamñërit (ci la tam ja weddi boppam) di ca julli ak di ca tusngalu ak yees lim ci kow...