Yoro Booli Jaw

Jóge Wikipedia.

Yoro Booli Jaw (Yoro Jaw), taarixkat la woon ca cosaanu Senegaal, gane adduna 1847, te dee ca atum 1919. Bokk naa ci ñu jëkk nettali cossanu wolof yi, ci kallamu nasaraan, ca Senegaal. Ci wallu taarix, ci liggeeyam lañu gëna sukkandiku ngir faramfacce cossanu wolof yi.

Cosaanam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yoro Jaw, Waalo la juge woon, juddu ci dëkk bu ñu naan Xuuma, dëkk bi di musa nekk peeyu Waalo. Yoro Jaw, géer la woon, bokk ci xeet yi Brak (buuru Waalo) waroon juge ngir mëna falu. Ñeeti negg ñoo yoroon Waalo, géer yi bokk ci, ci seen meen. Amoon naa Tejeek yi (Yoro Jaw, ci la bokk), ñoom seen maam di ay Pël, amoon naa Joos yi, seen maam di ay Séeréer, ak Loogar yi, seen maam di ay Naar. Ci geñoom, ci ñu sant Jaw la bokkoon, askan woowu baawo ci Jaa Ogo yi. Baayam mooy Fara Penda Majaw Xoor Jaw, yaayam di Booli Mbooj.

Jaar jaaram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi mu nekke xale, yoobu neen ko ci li ñu wax l'ecole des otages, ci wolof mooy daara ji ñu denc jaam yi. Ndax, boobu jamono, Waalo, tubaap yi ñoo ko nangu woon, ak canc gi. Tubaap yi ñoo daan jël doomi buur yi ñu jaamloo, di leen yobbu ci daara yooyu, ngir xale yi ñu leen jang lakku nasaraan, aaday tubaap yi, ngir xale yi mujj nekk dag tubaap yi. Li yepp xewoon naa ci dundu Yoro Jaw ca Ndar, diggante atum 1856 ak 1860, mu gén ci, ca tegu, tubaap yi teg ko li ñu wax chef de canton ca Waalo, ci dëkk bu tuddu Foos ak Xuuma tamit, ca atum 1860. Yoro Jaw, tubaap yi la daan and ba mujjam.

Liggeeyam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yoro Jaw, yagg naa yengu ci wallu taarix. Bi mu nekke xale, da daan bind cosaanu wolof yi, ci li baayam ko daan nettali, ak ci li gëwël yi daan nettali. Li yepp ba indi bind yu bare mu jagleel cosaanu Waalo, Kajoor, Bawal, ak Jolof. Tubaap yi, dajale bindam yepp, te ñu tambali def ko ci benn teere moniteurs du senegal et dependances, ci atum 1864, ca li Yoro Jaw bindoon ci Kajoor. Henri Gaden, benn tubaap, ca atum 1912, moo genoon yeneeni bindu Yoro Jaw ci yeneen nguur yi, mu tudd ko legendes et coutumes senegalaises.

Yoro Jaw, jiite naa Seex Anta Joob ci adduna, waaye Yoro Jaw, daan na bind ci fu xeet wi nekk Senegaal juge, di Isipt gu yàgg ga, ay jamono yu yagg sooga Seex Anta Joob gane adduna, te da daan faramfacce li cosaan wax doŋ. Wax naa ci fukk ak benn njabootay juge Isipt, te ñow dëkk Senegaal. Abubacry Muusa Lam, taarixkat ak isiptolog (egyptologue) bu mag nek IFAN, liggeey naa ci seede Yoro Jaw ndax begg tekki li cosaanu rekk wax. Seex Anta Joob sax, musul wax ci Yoro Jaw lenn, mel ni xamul ko woon.

Yoro Jaw, Xuuma, dëkku cosaanam la gene adduna atum 1919.