Aller au contenu

Yoos

Jóge Wikipedia.
Yoos (Agave sisalana)

Garab gii lañuy wax ci Wolof Yoos turu xam-xam wi moom lañuy wax (Agave sisalana) moom daf a bokk ci xeeti (Agaaf) yi bu ko defe dañuy jëfandikoo baatu (sisaal) ngir di ko ràññatle ak yaneen (Agaaf) yi ndax xeetu garab yu ñuy wax (Agaaf) daf a bari lool te ci xeetu garab yuy am ci wetu (Amerig) lay doon mu doon xeet yu bari moom nag ñu di ko ràññatle mu bokk ci njabootu (Agaaf) yi waaye ñu jël baatu (sisaal) ngir di ko ràññatle turu xam-xamam nag mooy (Agaaf sisallnaa) moom nag garab la goo xam ni ci xeeti (Agaafl yi la bokk kon baatu (Sisaal) lañuy jël di ko jëfandiko ngir ràññatle ko ak yaneen garab yi nga xam ne (Agaaf) lañ, Moom nag fimuy faral di sax réew yu ñuy tudde (Karayibil) fu de me ni (Panamaa) ak (Kubã) ak fu de me ni (Jamayg) réew yooyu fala baree lum fay sax leg lee ñu gis ko faneen waaye foofu la ëpp lum fay sax mi ngi faral it di sax ci barab yi nga xam ni dafa nooy te di faral di tàng foofu la ëpp lumuy sax kon ñi ngi koy faral di gis ci réewu (Karayibi) añs kom ni ma ko waxe.

Moom nag garab la goo xam ne day am ab dàtt boo xam ne dàtt bu xaw a dëgar lay doon day bindoo ni dàttu tàndarma day gàtt it waaye dafay am ker goo xam ni ker gu yaatu lay doon gu rëy ker gi it dafay dëll ndax li tax muy dëll mooy xobam yu mu am dafay xob yu tal xob yu tal yoo xam ne daf a xaw a rëy daf a xaw a yaatu su ko defee xob yooyu nuñuy ràbb a loo wee moo tax ker gi dafay xaw a yaatu doonte moom garab la goo xam ne du gudd lool waaye dafay dëll ker gi it dafay yaatu moom nag nimuy saxe dafa mel ni dafa am ay xupptali-xupptal ni ki ni tàndarma di saxe noonu lay saxe ba noppi day sax ay xob mu wër xëb yoy dafay yor melokaanu ab daba ni daba di bindoo noonu lay bindoo, Boo xoolee xob yi ci wed gi dafay mel ni dafay am ay bëñ yu mel ni ay bëñ i joolaa la am xob yi noon la mel ba noppi dafay xaw a ràbbaloo nga xam ni dafay sax ni tàndarma di saxe bu saxee day yëkkatiku wëraat amaat yaneen yu saxaat yoo xam ni dañuy teglaanto kom ay xuppatal yu teglaanto noonu lay doon guddaayam dan a toll ci met jàpp ñaar-fukki met ak sàtti met ak juróom.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Agave sisalana