Yëglu cig sori

Jóge Wikipedia.

Mooy xam ni yaram yi mel walla jëmm yi, walla seen dëgg-dëgg ci lu dul laalante gu fisya (fisi) walla gu kimya (simi) gu jonjoo ak yaram yii. Bokk na ci ni nu ko gënee doxale, ëpp ko nee defe ci jamono jii: nataali jawwu yi nuy defe ci satalit yi (jumi asamaan yi) walla ci fafalnaaw yi. Bokk na ci li nuy doye ligéey bii:

Wàll gu jëm ci jiyoloji: wuññi petorol(feeñal ko), ndox, mbell yi, añs... sopparñiku gu jiyoloji. Mbay: xam tawat yi ci gàncax yi, xam xeeti gàncax yi nekk cib barab. Xam-xamu galaas yi: xeentu walla topp ak gëstu yëngu-yëngu gu jóori galaas yi ak ni nuy seeye.