Xureer

Jóge Wikipedia.
Xureer gi (Crateva religiosa)
Xureer gi (Crateva religiosa)

Xureer garab la gu bàyyikoo Sapoŋ, Óstaraali, ca pàcc bu yaa ca Asi gu Ngoppkaw, (Bëj-saalum ak Penku) ak ca dun yu bari yoy Jàmme(pasifig) gu Bëjsaalum.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xureer gi garab la guy tóortóoram yore xetu laaj. Xeetu garabu tóortóor la gog gox yu naaje ak xaw a naaje yi. Day yeex a màgg, day néew i xob, téeñu ronu garab gi daa teqaloo te yor xob yuy melax ak um xànc mu am i gàkkgàkk yu weex. Yenn ciy xeetam man nañ àgg ba 30i met ci guddaay. Ci suuf su naat te néewle ag sëcc(asibe) lay gën a man a meññ.

Njariñal xureer[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xureet garab gu am ug tooke la waaye ginnaaw ag togg dootul lore. Xob yi ak meññ mu yees mu dañ leen lekk niy lujum. Dees koy fajoo, di ci dolli ag xëntewoo lekk, di ci jële ay bir ngir defar simaa, te di yàtt cim mattam ay jumtukaay.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Crateva religiosa

Tur wi ci yeneeni làkk[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Farañse: poire à l'ail sacrée