Xoos

Jóge Wikipedia.
Nataalu xobi xoos

Xoos xeetu garab la bu bokk ci njabootu Rubiaceae ak ci ñoñ Mitragyna. Afrig gu Sowwu ak gu digg lay nekk.

Meloom wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Guddaayam danay àgg 8 ba 10i met. Xobam ci guddaay day àgg 6 ba 9i sàntimet, ci yaatuwaay 3,5 ba 5 sàntimet. Melow xol la yore. Tóotóoram day weex te am xet gu tar. Yaatuwaayam 2 ba 2,5i met la. Cari foytéefam day yàgg ak ñoom lool.

Njariñam li[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xoos garab gees di jëfandikoo la ci pajum cosaam ngir faj xeeti tawat yu wuute.

Nataala yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xamam wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Mitragyna inermis