Xeex bi am ci diggante Mexico ak Porto Riko
Xeex bi dox diggante boxer yu Puerto Rico ak yu Mexique bokk na ci xëccoo yi gëna tar ci taarixu boxing. Xeex bi mingi tàmbali ci 1934, xëcc na soppe yu bari ci jamono yu bari. Jamono di dox, ñaari réew yooyu dañu yar ay xeexkat yu siiw yu wane seen manin ci match boxe yu kenn du fàtte, lu ci melni Julio Cesar Chavez, Fenix Trinidad, Ox De La Hoya, Miguel Cotto, ak Hector Camacho. Neenañu tammbaliwoon na bi Sixto Escobar nekkaate shampiyoŋ bu njëkk ci Puerto Riko bi mu daanele Rodolfo "Baby" Casanova shampiyoŋ bu Mexico.
Ñenn jàpp ni xëccoo bi mooy xëccoo bi gëna am doole ci taarixu boxe . Ci match titre mondial yi, boxer yu Puerto Rico ñoo ëpp tuuti seeni noon yu Mexique, Puerto Rico am 84 ndam suñu ko méngale ak Mexico am 73 ndam. Record bu am taxawaayu joŋante bu metti bii dafay wane solo bu xóot bi am ci xëccoo bi, di màndargaal mbekte ak bëgg-bëgg ci soppe yi ak xeexkat yu bawoo ci ñaari réew yi.