Xaru

Jóge Wikipedia.

Xaru mooy nga am yééne ray sa bopp.[1] feebaru naqar gu metti ku dara saful, Feebaru "bipolaire", Feebaru "schizophrénie", feebari nekkin, ak feebaru dorogewu - boole ci naan gu bari gi ak jëfandikoo garabu benzodiazepine - yi yépp luy indi xaru la[2][3][4] Ñenn ci ñi di xaru dafa am ay jëf yu ñu dooleelndax stress joge cijafe-jafe xaalis, jafe-jafe nekkin ak nit ñi nekkin ci diggante ay nit, walla tiital[2][5] Ñi mësa jééma xaru dañu nekk ñoo xamantane ngir ñu jéémaata xaru lu yomb la.[2] Fagaru ngir waññi xarujéégo yi ñooy nééwal yoon yi di indi xaru - lu mel ni ay fetal, dorog, ak poson; faj feebaru xel yi ak dorogekat yi; yéglekaay yi nettali bu xaru amee, te yoq koom-koomi nit ñi.[2] Su fekkee sax ay nimero yu nit ñi mëne woote saa yu nekk su ñu amee jafe-jafe bare nañu, wóórul ne am nañu njëriñ.[6]

Yi ñu gën di gis fasoŋu xaruda ñu wute ci diggante rééw yi, te mungi bokk ci benn wall ci ay pexe yu wóór yu ñu tërël.[7] Fasoŋi xaru yu ñuy gën di gis ñooy xoj sa bopp, naan poson, akay fetal.[2][8] Xayma nañu nit ñi dee ci xaru tollu ci 828.000 ci addina bi yépp ci atum 2015, am na yoqutewu ci xaymaay atum 1990 tolluwoon ci 712.000.[9][10] Lii moo def xaru fukkeelu mbir yuy indi deeci addina bi.[3][11]

Lu jege 0.5-1.4% ci nit ñi di xaru, lu tollook 12 ci 100.000 nit yoo jël at mu nekk[11][12] Ñett ci ñeent ñiy xaru ñépp ci addina bi mungi am ci ak rééw yi seen am-am demewul noonu.[2] Xayma xaru yi am ba pare lu ci ëpp ci góór ñi la ëppe boo ko méngalee ak jigéén ñi, tambale ko ci 1,5 yoon gëna kawe ci rééwi yi seen koom-koom di jóg jëm ci 3,5 yoon gëna kawe ci rééwi yi ame alal.[13] Xaru lu ci ëpp mungi gëna fës ci ñi weesu juróóm ñaar fukki at; waaye, ci yenn rééw yi, at yooyu ñungi ci diggante fukki at ak juróóm ak fanweeri at ci seen mëna xaru yu gëna kawe. [13] Europe moo ëppoon ay nit yu xaru ci ay gox ci atum 2015.[14] Xayma nañu fukk ba ñaar fukki miliyoŋ ñi jééma xaru te deewuñu at mu nekk.[15] Di jééma xaru te deewuloo mën na indi ay gaañu-gaañu ak ay laago yu yagg.[12] Ci rééwi tugël yi, di jééma xaru mungi ëppe ci ndaw ñi ak ci jigéén ñi.[12]

Ay gis-gis yi nit ñi am ci xaru ñungi bawoo ciay ngëm-ngëmyu mel ni diine, teddaay, ak njëriñu dund bi.[16][17] Yii Diine yu joge ci Ibrahimadañu gise xaru ni ab tooñ Yalla, ndax seen ngëm-ngëm ci sellaay yu dund bi.[18] Bi samuraidoon am ca Japon, benn xeetu xaru bi ñu xamewoon ni seppuku harakiri dañu ko joxoon cër ni beneen yoon ngir bëral ñakka tekki walla ni yoonu ñaxtu.[19] Sati, benn jëf-jëf la bu ñu terewoon joge ci Raju Britanique bi, bu doon xaar Jëtuur Indo bidiray boppambi nééwu jëkkëram ji taalu robukaay, mu defal ko boppam walla waa këram ak mbooloo mi di ko puus.[20] Xaru ak jééma xaru, bu njëkka ba dañu ko terewoon, waaye léégi ci rééwi Tugël yu bari kenn tereetu ko [21] Boobu dafa nekk ab ñaawtééf ci rééw yu bari ba léégi[22] Ci siecle ñaar fukkeel ak ñaar fukkeel ak benn, xaru lu nééw lañu ko jëfandikoo ni xeetu ñaxtu, ak kamikaze ak xaru ak ay bomb nekk na lu ñu daan jëfandikoo ni jëfinu militaire walla terroriste. [23]

  1. Stedman's Medical Dictionary (28th ed.). Philadelphia: Lippincott Williams & Wilkins. 2006. ISBN 978-0-7817-3390-8. 
  2. 2,0 2,1 2,2 2,3 2,4 et 2,5 "Suicide Fact sheet N°398". WHO. April 2016. Archived from the original on 4 March 2016. Retrieved 3 March 2016. 
  3. 3,0 et 3,1 Hawton K, van Heeringen K (April 2009). "Suicide". Lancet 373 (9672): 1372–81. PMID 19376453. doi:10.1016/S0140-6736(09)60372-X. 
  4. Dodds TJ (March 2017). "Prescribed Benzodiazepines and Suicide Risk: A Review of the Literature". The Primary Care Companion for CNS Disorders 19 (2). PMID 28257172. doi:10.4088/PCC.16r02037. 
  5. Bottino SM, Bottino CM, Regina CG, Correia AV, Ribeiro WS (March 2015). "Cyberbullying and adolescent mental health: systematic review". Cadernos De Saude Publica 31 (3): 463–75. PMID 25859714. doi:10.1590/0102-311x00036114. 
  6. Sakinofsky I (June 2007). "The current evidence base for the clinical care of suicidal patients: strengths and weaknesses". Canadian Journal of Psychiatry. Revue Canadienne De Psychiatrie 52 (6 Suppl 1): 7S–20S. PMID 17824349. 
  7. Yip PS, Caine E, Yousuf S, Chang SS, Wu KC, Chen YY (June 2012). "Means restriction for suicide prevention". Lancet 379 (9834): 2393–9. PMID 22726520. doi:10.1016/S0140-6736(12)60521-2. 
  8. Ajdacic-Gross V, Weiss MG, Ring M, Hepp U, Bopp M, Gutzwiller F, Rössler W (September 2008). "Methods of suicide: international suicide patterns derived from the WHO mortality database". Bulletin of the World Health Organization 86 (9): 726–32. PMC 2649482. PMID 18797649. doi:10.2471/BLT.07.043489. 
  9. Njuumteg royuwaay: Balise <ref> incorrecte : aucun texte n’a été fourni pour les références nommées GBD2015De
  10. GBD 2013 Mortality and Causes of Death Collaborators (January 2015). "Global, regional, and national age-sex specific all-cause and cause-specific mortality for 240 causes of death, 1990-2013: a systematic analysis for the Global Burden of Disease Study 2013". Lancet 385 (9963): 117–71. PMC 4340604. PMID 25530442. doi:10.1016/S0140-6736(14)61682-2. 
  11. 11,0 et 11,1 Värnik P (March 2012). "Suicide in the world". International Journal of Environmental Research and Public Health 9 (3): 760–71. PMC 3367275. PMID 22690161. doi:10.3390/ijerph9030760. 
  12. 12,0 12,1 et 12,2 Chang B, Gitlin D, Patel R (September 2011). "The depressed patient and suicidal patient in the emergency department: evidence-based management and treatment strategies". Emergency Medicine Practice 13 (9): 1–23; quiz 23–4. PMID 22164363. 
  13. 13,0 et 13,1 Preventing suicide: a global imperative. WHO. 2014. pp. 7, 20, 40. ISBN 9789241564779. 
  14. "Suicide rates per (100 000 population)". World Health Organization. 
  15. Bertolote JM, Fleischmann A (October 2002). "Suicide and psychiatric diagnosis: a worldwide perspective". World Psychiatry 1 (3): 181–5. PMC 1489848. PMID 16946849. 
  16. Tomer A (2013). Existential and Spiritual Issues in Death Attitudes. Psychology Press. p. 282. ISBN 9781136676901. 
  17. Ritzer eb, Stepnisky J (2011). The Wiley-Blackwell companion to major social theorists. Malden, MA: Wiley-Blackwell. p. 65. ISBN 9781444396607. 
  18. God, Religion, Science, Nature, Culture, and Morality. Archway Publishing. 2014. p. 254. ISBN 9781480811249. 
  19. Colt, George Howe (1992). The enigma of suicide (1st Touchstone ed.). New York: Simon & Schuster. p. 139. ISBN 9780671760717. 
  20. "Indian woman commits sati suicide". Bbc.co.uk. 2002-08-07. Archived from the original on 2011-02-02. Retrieved 2010-08-26. 
  21. White T (2010). Working with suicidal individuals : a guide to providing understanding, assessment and support. London: Jessica Kingsley Publishers. p. 12. ISBN 978-1-84905-115-6. 
  22. Lester D (2006). "Suicide and islam". Archives of Suicide Research 10 (1): 77–97. PMID 16287698. doi:10.1080/13811110500318489. 
  23. Aggarwal N (2009). "Rethinking suicide bombing". Crisis 30 (2): 94–7. PMID 19525169. doi:10.1027/0227-5910.30.2.94.