Xarañ

Jóge Wikipedia.
Nataalu garabug Xarañ

Xarañ garab gog moo ngi cosaanoo fii ci Afrig, te bokk ci njabootug Capparacées.

Garab la gog dees na ko fekk ca: Mosàmbig, Botsuwaanaa, Namibi, Senegaal ak Madagaskaar.

Melo wi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Garab la gog peeram dafa am ay dég. Ay foytéefam dañiy lang ci kaw ab peeram.

Yaatuwaayam moo ngi tollu ci 40i met jàpp 50. Aw meloow day xaw a weex buy tàmbali ñor, bu demee ba ñor meloom wi day gel.

Garab la gu bari lu miy faj lool, day faj biir buy daw. Dees na ko jëfandikoo it ngir rafetal yenn barab yi, dees na ko sàkketee it. Leeg leeg foytéefam dees na ko lekk.

Nataal yi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Turu xam-xam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Capparis tomentosa