Xamale kuy Sëriñ bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu góor làqoo

Jóge Wikipedia.

Ag ganeem àadduna(g.m)[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ baa ngi gane àdduna - ci li nu wax - ci atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk (1270 g / 1853 g.j). Am ñu ne atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk ak ñaar (1272g / 1855 g.j) ca kër waajuram wu góor ca Mbàkke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga.

Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na:

(( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum (sharaha),muy 1270g làqu atum (shumoos) muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel niy jant (cig leer). Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar. Ci guddig àllarba, ci ñaar fukki fani muharram)).


Ag yoram[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom sëriñ bi, bi mu ganee àdduna aji juram ju jigéen ju tedd ja a ko yoroon ba mu mat a jàngi. Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah, doomi Muhammadul Kabiir, mom Habiiballaah mu njëkk ma, doomi Muhammadul Xayri,. Muhammadul Kabiir mii mooy ki ñuy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbàkke Bawal, waxees na ne loolu ci atum Shaqdadin la di (1194 g / 1780 g.j ) . Waaye dëkkewu fa woon, da fa a bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata, magi habiibullaah waaye bokkunu nday. Moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof, fa la làqoo ñu denci ko fa, di ko siaare.

Mi ngi askanoo nag ci Tukklóor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof. Siiw na itam ne ñoom Gànnaar lañu bawoo, dem Fuuta. Seeni doomi baay-tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay sëriif lanu.

Sama mag, sama sëriñ, sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima ,sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne dégg na ci sëriñ bi luy dëgëral lool. Mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lanu.

Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te déggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu.

Yaayam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu, kon sëñ bi seriif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke, jëm fu nu naan Mbumbe, péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbàkke-Màkke yi dëkke woon.

Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbàkke-Mbàkke yi seeni doomi baay tëx lanu, kaaf gi nekk ci Mbàkke ag Haa (arafu h) la woon muy haa giy mujj ci Ba, Wolof yi def ko Kaaf,waaye wax jooju, ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la, niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab). Li am daal mooy ñaari wax yi ju ci nekk, dëgër na te am na màndargam dëgg.

Buso-boso yi nag ñoom, seen cosaan Fuuta la, ca fa nuy wax Golare. Barab yii yepp it yu jegee lanu. Barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddngay ñaari askan yi.


Bi mu tollee ci war a jàngi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi Sëriñ bi tollee ci war a jàngi,waajuram daal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO, mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgg as lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbàkke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO, doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi, ju jiggéen, ndayi wayjuram wu jiggéen,soxna Asta Waalo.

Nu daan nekk foofa, fa moom ca Mbàkke, bu noor baa, bu nawet baa, lu ci ëpp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal.

Kenn ci ñu wóor ñi nettali na ma ne: sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daawul tàggalikook moom lu dul lu néew,ndaxte magam Maam Moor Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg mu jaar fa nekk fa ak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jiyaarkat boobu di Màbba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Màbba boole woon na leen ca ña mu paŋoon (dajale woon) jëme Saalum, nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa woon kenn.


Bi Màbba faatoo[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi mu faatoo nag moom Màbba, nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi, ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukklóor KA doomi bàjjani baayam. Bi mu jàngee ci moom dali xam-xam, tàmblee yewwu ak a ñaw as lëf, la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono.

Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caagéenug seen teddngay nguur gi ,li ko loruloo woon, tax it mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom,moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk, ndax da daan jàng ak a jàngale,te jàng ak jàngale neexoowut aki buur, moo waral ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dul ab coona.

Ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daan na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey ba ak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi, rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indil ay woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu génneel ko ci moom Qaali ab yàq, mu mujj nag moom sëñ bi far ko raw, mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko, ma mokkal ko, kon mujj na toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil,nii la nekke woon ak Xaali.

Muhammad mom Muhammadul Kariim[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muhammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def téere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan (xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it - ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu). Bi waajur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci téereb boppam ba ,walla ci téere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla téere ba, bu ñëwee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féetesi ak moom,doylu ci moom,waajur wi bàyyi leen ak moom te bég ci.

Mbàkke Kajoor[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala, dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanc ca wetam, tudde ko Mbàkke Kajoor, sax fa ñaari at daal di wuyyuji boroomam, nee nanu, looloo ngi am ci Muharram, atum 1300g, dëgg naa ci Sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat, took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqu,nu denc ko Deqale ,di ko siyaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko.

Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi nuy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wàllug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bépp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA, mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denc gi,sëñ Tayba digale nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana Sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a tontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale gi ak dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àdduna ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas. Ña cay ñu baax wax ji da leen a yéem, rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara.

Bu dee mbooloo mi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bu dee mbooloo mi moom, li leen yéem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu Sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yéeme,bu njëkk bi mooy waxam jii: {nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëlif leen}ba fa mu yam teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii:

{{ nee nanu ma jéngal jëm ci bunti buur yi,kon déy da nga am ay may yu lay jariñ jamono ju ne)).

((Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine))

((Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàlla'ay ki may doyluloo te di ma musal ))

((Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte? ))

((Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër'a'y dërub saytaane ))

((Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom Aras laay woo. Mooy Aji dimbali, ji dara dul të,te mooy Kiy amal li ko soob ))

((Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir))

((Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man amuma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina ))

((Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon déy ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gàccaal}}.

Waajuram wu jigeen ,wu tedd waa nga làqoo Poroxaan ca Saalum, nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee.