Wikipedia:Maanaam ci

Jóge Wikipedia.
nataalu sémbum Wikipedia ci wolof

Wikipedia(di jàng wikipediyaa) am sémbum téerexamteef la ci lënd gi , di lu jamonowu (modern) te bari-y làkk. Ag mbindam nag mi ngi wéy ba tay, xaralaay wiki lañ jëfandikoo ngir sos ko. Yéeney Wikipedia mooy jéebbal ag ndef gu ubbeeku, maandu te fugluwu.

Sémbum Nupedia[soppi gongikuwaay bi]

Wikipedia ngi jóge ca Nupedia

Nupedia di woon am sémbum téerexamteef bu ubbeeku bu Jimmy Wales sosoon ci weeru gamu atum 2000. Mbootaay(societe)uk Bomis (gi Jimmy Wales féetewoo woon moomeel gi ci ëpp) moo ko jàppale woon ciy koppar, doon fay Larry Sanger mi jiite woon mbind mi. Waaye Nupedia ag màggam dafa yeexoon loolu ba waraloon, ci 2001, Larry Sanger xalaatoon ni sos ab wiki moo doonoon liy man a gaawal yokkteeg jukki yi. Xalaat boobu ñeel jëfandiku xaralag wiki ngir sos ab téerexamteef, juroon na ab diisoo ci diggante Larry Sanger ak tëriinkat boobu di Ben Kovitz ngir mu faramfaceel ko ci ni mu gën a leeree ana nan la xarala bu wiki di doxee, ci ab reer ca San Diego la ame woon, ci 2 tamxarit 2001. Ci nii Larry Sanger ni Jimmy Wales ngir ñu jëfandikoo xarala bu wiki ngir sos ab Téerexamteef bu gën a woyof, lii moo jur sosteefug téerexamteef bu Wikipedia.

Sémbum Wikipedia[soppi gongikuwaay bi]

Ginnaaw bi ko Jimmy Wales ak Larry Sanger sosee, Wikipedia ngi judd ci kàllaama waa angalteer ci 15 tamxarit 2001. Gu waa faraas teggu ci 23 gamu 2001, bu waa almaañ tegu ci ak yeneen yépp, ba tay ci atum 2007 mat nañ ñaari-téeméer ak juróom-fukki làkk.

Ci 1 diggi-gamu 2002 la Larry Sanger tekki ndomboy-tànkam ci ñaari sémb yépp, ginnaaw bi Bomis téeyee loxoom, fayatul Larry Sanger ci liggéey bi mu doon def ci Wikipedia ak ci Nupedia. Ci 26 weeru koor 2003 la Nupedia tëj ba fawwu, Wikipedia moom wéy di màgg.

Boobu ba léegi Wikipedia di dox ciy àtte yi askanam tëral ndànk-ndànk jëmug-kanamam. ci 20 maami-koor 2003 la Mbootaay gu Wikimedia (wikimediafoundation.org ) juddu ngir ut ay koppar yu muy suuxatee sémbi wikipedia yépp.

Wikipedia Wolof[soppi gongikuwaay bi]

Wikipedia wolof moom mi ngi sosu ci ndeyi-gamu 2003, toog daanaka ñaari at te amul benn yëngu-yëngu. Ci tamxarit 2005 la am jukkeem bu njëkk.

Melokaanu sémbum Wikipedia[soppi gongikuwaay bi]

Yéeney sémb mi[soppi gongikuwaay bi]

Niñ ko bindee ci xët wu njëkk wi, liy bakkam mooy:«Téerexamteef bu ubbeeku bi», maanaam di lu ñépp bokk, te ñépp man cee cëru ngir gënal ko. Jimmy Wales di kenn ci ñaar ñi sos sémb mi, mi ngi koy tekkee niki «ab jémantu ngir sos aka séddatle ab téerexamteef bu ubbeeku ci anam bu muccu ayib ngir nit ku ne man kaa am ci làkku cosaanam».

Melokaani Wikipedia[soppi gongikuwaay bi]

Baatu «Wikipedia» ngi jóge ci taqaleeb ñaar yii di «wiki» di ab nosteeb yoriinu ag ndefug dalub web gu ñu man soppi jaare ko cib joowukaayub web, ak « pedia » di reenu baatu waa angalteer bii di encyclopedia, di tekki téerexamteef.

Liñ jublu ci sémbum Wikipedia mooy mu doon ab téerexamteef, maanaan muy jëmmal bépp xameefu nit, lépp lu nit xam man caa ne. Wikipedia du ab baatukaay, du am péncum waxtaanuwaay (xoolal xët wii ngir xam lu wikipedia doon ak lu mu doonul: Aide:Ubbeeku). Sémb mi da fa àddunawu, day laal bépp xeetu xam-xam, barilàkk, te amul ag pay.

Sémbi wolof yi[soppi gongikuwaay bi]