Waxtaani wàll:Caada
Caada= def ko Aada moo gën Caada wolof yu yees yee ko indi waaye xameesu ko woon ci làkk wi, moom daal daa jekk a wax rek deesi ko wax waaye amul delluwaay ci làkk, mag ña xamuñu ko woon, amul wenn léebu wees jëfandikoo caada, amul jenn wax ju bawoo ca mag ña indi ko, aada rek lees fi daa wax, te wax dëgg Aada a gën a wolofe, def naa ci ab laaj ci magi wolof yu wolofe yi, waaye lii lees ma tontu, ginnaaw nun wolof la nuy laggéeyal, bëgg mu ñoŋ liggeey bi njëkk mooy nu fóot ko dindi li ci bokkul, waru noo seet baat beesi jëfandikoo mu jekk rek nu ni ahakay, déedéet danoo war a sàmm làkk wi saytu baat yi, ba yi nuy jëfandikoo man a wer ba kenn du ko man a ŋàññi,
lees ci jublu moodi, ni Aada ni Caada niki nga ni Gëm ni Ngëm nga xamni ngëm mooy gën a matale, loolu nak la làkk wi nanguwul manaam garaameer ci diggante Aada ak Caada manta ne, arafu C manta yaatal baat bu doore arafu A, Arafu C mooy yaatal baat bu doore arafu S niki: Soppi Coppi, Sol = Col gi, Saaku = Caaku si, ak yuni mel, Caada sax moom day joxe beneen maanaa ci wolof niki nga ni: ca aada ja, bu tënkoo ci waxiin di C'aada ja, waaw-kay way xelu ñi