Aller au contenu

Waxi Seex Anta Jóob

Jóge Wikipedia.

Waxi Seex Anta Joob ju aju làkk

Làmmiñ ak jamono

  • Làmmiñ wi ngànnaay la, paaka la, balay ñaw nga daas ko;làmmiñ wu ñu jariñoowul, mi ngi mel ne paaka bu xumaag. Tubaab yi bi ñu fi ñëwee, réew mépp dañu koo yore ci seen làmmiñu bopp.Moo taxoon ba sunu làmmiñ yi des ginnaaw.Li la daan tax a jëm kanam, li la daan tax a am loo dundale sag anjaboot ci weneen làmmiñ nga daan jaar am ko...Loolu moo taxoon ñu sàggane sunu làmmiñ yii.Waaye du caagéenu dañu cee manul woon a waxe li ñu bëgg a wax...

Dangeen di xam ne aw làmmiñ, jëfandikukaay la boo xam ne lu am xel dem ci àdduna aw làmmiñ man na koo tudd, am xel ay gàtt, aw làmmiñ gàtt!Waaye lu am xel man a jëm ci àdduna rekk, aw làmmiñ man na koo tudd;aw làmmiñ gàttul.

Nit kiy wax nag fi xelam yam, fi jàngam yam, fi gis-gisu àddunaam yam, foofu rekk la ay waxam man a yam...

Waaye boo demee ba sam xel gis leneen rekk, làmmiñ dina ko tudd. Lu ko waral? Amul benn baat boo xam ne bii yenu nga sa maanaa ci cosaan, amul!Mooy li nga xam ne - waxoon naa ne...dinaa cuq tuuti xel yi...ndax defe naa ne, yéen jàng ngeen xam-xamub làmmiñal...xam ngeen ne De Saussure (boroom xam-xam bu mag la woon ci wàllu làmmiñal) wone na loolu.Làmmiñ du loo xam ne tay baat yi dañoo juddu rekk daal di yanu seeni maanaa. Baat bi coow luy génn ci gémmiñ kepp la! Kepp! Amul sax menn maanaa. Ndax bu ko amoon wenn làmmiñ ay am, kon lu jug rekk xel yépp nenn lañu koy tudde.Wenn tur wi di moom te loolu amul.


Jukki bii tibbees na ko ci waxtaanu Seex Anta Jóob, mu amoon ci awril 1984 ca Cees