Waxi Sëriñ Maalig Basin Si
Apparence
Waxtaani Sëriñ Maalig Basin Si , njariñ, yare, laabire, yeete, ak waare
- Mbirum àdduna loo ci rëyal ba woote ko mu diis ba doo ko àttan
- Donga buy tërbiyawu moongi melni mbuus muñ duyi leer/ndox bu jegee jigeen manga cay jami ràbb muy seeb, bu ko laalee mu bëtt tuuru
- Kilifa balaa war a digle day def balaa war a tere day ba
- Liy yàq kilifa, ñàkk njariñ, ñàkk a jëf.
- Lepp looy santaane na fekk nga manal ko sa bopp ba su ñu gàntoo yit nga defal ko sa bopp, ngir nit ñi ku léen yaakaar ñu wor la.
- Liy yàq kilifa, yatt la: 1. Lu mu xam wax ko; 2.Luñ ko wax, mu waxaat ko; 3. Lu mu mer, xul ko.
- Ku la jaay yatt (3), jënde ko yatt (3): 1. Ku la jaay xam-xam, jënde ko maandu, mu ne ndax as gor bu maanduwul du teree moy Yàlla; 2. Ku la jaayub juddu, jënde ko ngor, ngir juddu bu rafet du teree dem kaso; 3. Ku la jaay alal, jënde ko doylu, ngir bu doyluwul dina sàcc
- Lees yarul kenn du man a jaxasook moom, loo bëgg a jaxasool danga koy tàqaleek moroomam ya yaruwul.
- Kilifa daa war a yar doomam, moo gën jikki ba fiy bëgg
a juge, naan sama gannaaw na ngéen topp ci diw. (nde loolu ku yar
sa doom bam man a yor mbooloo dooko wax), te nit ñi boo nee léen
topp léen diw mii, bu diw jubul it duñ ko topp.
- Yàlla mooy ndox ma Rasoolu Laahi mooy teen ba sab Sëriñ
mooy goj ba pas-pasu taalube ba mooy baak ba yitteem mooy
di yoor aka jukki ba barim ndox. - Li tax kuy wut Yàlla ay mbokkam di ko yedd, jaam buy wut
boroomam talut moroomam, bu amee boroomam bëggul moroomam. - Ku dul mer mbaam la, Kudul mar xaj la,
- Nit ku yiw, na joxe dooleem, joxe alalam, waaye bumu joxe
ngoram, ndax ku joxe sa ngor dootoo dara. - Ku gis sa baay, gis sa nijaay, gis sa taawub baay
war a xam sa bopp.
15. Danga gis boroom judd buy taxawaalu akub juddoom; Boroom xam-xam buy taxawaalu akub xam-xamam ;
Waaye doo gis mukk boroom liggéey buy taxawaalu akub liggéeyam.
Delluwaay
[Soppi • soppi gongikuwaay bi]waaxtaan yi ak jaar-jaar yi moo ngi bawoo ci téere bu am solo
Sëriñ Abiibu Si doomi Sëriñ Maalig Basin Si bind ko ngir dajale
as lëf ci jaar-jaari Sëriñ Maalig Basin Si aki waxtaanam ci càkkutéefug Sëriñ Muntaxaa Mbàkke
mom Sëriñ Basiiru Mbàkke mom Sëriñ Tuubaa, Tuddee Téere ba
" النصيحة لاخوان, للترشيد و التنبيب لرحمة" ( Laabiire ñeel bokk yi, ngir yar yeete ngir
Yàlla.)
Sëriñ Maalig Basin Si
Bawoo :Sëriñ Habiibu Rasuul SI