Aller au contenu

Uul

Jóge Wikipedia.
Uul gi(Parkia biglobosa)

Uul xeetu garab la gu bokk ci njabootu "Mimosaeae" (walla Fabasease).

Garab la gog guddaayam man naa àgg ba 25i met. Garab gi man naa jur ba 100i kiloy doom at mu nekk. Doom yi ñi ngi tàmbalee màgg ginnaaw taw yu njëkk yi.

Njariñ li

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ay xobam dinay dimbali suuf su nanguwul. Garab gu bari ay witaamin la. Doomi uul dees na ko baxal, dëbb ko ngir am ay dank walla pëndax (ginnaaw bu ñu ko weeree ) ñi ngi ko duppe sumbala ci bambara (Mali) ak yenn ci réewi Afrig Sowwu jant yiy làkk Bàmbara. Doom bi dees na ko togg it ngir dindi xott wi, ginnaaw bi, ñu jariñoo la mu ëmboon. Ca Senegaal, dees na dëbb doom bi boole ko ak kaani gu wow togg ci lees di woowe suul.

Turu xam-xam wi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Parkia biglobosa

Tur wi ci yeneeni làkk

[Soppisoppi gongikuwaay bi]
farañse: caroubier d'Afrique
angale: african locust bean
bambara: nere