Usmaan Sonko

Jóge Wikipedia.

Usmaan Sonko (Cees, 15 Sulet 1974) ab aji-politig bu Senegaal la, bokk ci ñi sos làngu politig gu Pastef. Dale 3 fani Awril mooy jëwrin ju njëkk ju Réewum Senegaal ci njiitalu Basiiru Jomaay Fay.

Jaar-jaar[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Njàngam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sonko ngi judd 15 Sulet 1974 ci Cees, ci ay way-jur yu doon liggéeyal Réewum Senegaal. Li ëpp cig dundam moo ngi ko def Kaasamaas ci diggante Siggcoor ak Biñoona, ginnaaw bi la dem ca Daara-ju-kawe ju Gaston-Berger ca Ndar àggale fa am njàngam, jëlee fa lijaasa ci wàllu àtte ci 1999. Ci ginnaaw gi la dugg ENA, di daara juy jàngale yoriinu réew, ci Senegaal. Ci 2001 la génn ENA ak ab lijaasa ñeel "Galag ak Suuf" ci senegaal. Ci la jaare am liggéeyam bi njëkk bu ko Réew mi jox, ca Impot et Domaine (Galag ak Suuf) bu Pikin. Ci 2003 la jot jeneen lijaasa ci gëstu yu xóot (DEA) ñeel koppari réew ak galag ca Daara-ju-kawe Seex Anta Jóob (UCAD). Def na itam ab Master 2 ci yoriin ak koppari réew ca Campéef gu Kawe ñeel Koppar gu ISF(Institut Supérieur de Finance). Am na itam lijaasay gëstukat ci daara-ju-kawe Jean-Moulin-Lyon-III, ca Faraas.

Liggéeyam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ginnaaw bi mu génnee ENA la ko Réewum Senegaal def luñutukat ñeel galag ak suuf. nekkoon na luñutukatu sàqi këri liggéey yi, nekkoon itam njiitu Kuréelu Saytukati Galag yi ci wàllu suuf ak tabax. Nekkoon na ab jubbantikat ca Yoonalukaayu Caytu gu Biir (Direction du Contrôle Interne) ca Yoonalukaay bu Daj bi ñeel Galag ak Suuf (Direction Générale des Impôts et des Domaines, DGID), ci Senegaal.